menu.png
Passwort vergessen ?

Bibel durchsuchen

 (Index)


Gefundene Einträge

•••► •••►
Buch Kapitel Vers Text
Matthaeus 3 13 Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
Matthaeus 3 14 Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!»
Matthaeus 3 15 Yeesu tontu ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu.
Matthaeus 3 16 Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu.
Matthaeus 3 17 Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.»
Matthaeus 4 1 Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
Matthaeus 4 2 Yeesu nekk fa te lekkul ñeent-fukki bëccëg ak ñeent-fukki guddi, door a xiif.
Matthaeus 4 3 Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.»
Matthaeus 4 4 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”»
Matthaeus 4 5 Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga.
Matthaeus 4 6 Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu leewu la ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”»
Matthaeus 4 7 Yeesu tontu ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
Matthaeus 4 8 Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam.
Matthaeus 4 9 Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.»
Matthaeus 4 10 Waaye Yeesu tontu ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”»

Seite:   1 2 3 4 5 6 7 8 9 10