menu.png
Passwort vergessen ?

Bibel durchsuchen

 (Index)


Gefundene Einträge

•••► •••►
Buch Kapitel Vers Text
Matthaeus 4 11 Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo.
Matthaeus 4 12 Am bés Yeesu dégg ne, jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile.
Matthaeus 4 13 Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali.
Matthaeus 4 14 Noonu am la ñu waxoon, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
Matthaeus 4 15 «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali,di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan,yaw Galile, réewum ñi dul Yawut —
Matthaeus 4 16 xeet wa nekkoon cig lëndëm,gis na leer gu mag,ña dëkkoon ca réew, ma dee tiim,leer fenkal na leen.»
Matthaeus 4 17 Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.»
Matthaeus 4 18 Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon.
Matthaeus 4 19 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.»
Matthaeus 4 20 Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
Matthaeus 4 21 Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen.
Matthaeus 4 22 Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom.
Matthaeus 4 23 Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngale ci seeni jàngu tey yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña,
Matthaeus 4 24 ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen.
Matthaeus 4 25 Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan..

Seite:   1 2 3 4 5 6 7 8 9 10 11