menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Noonu Yeesu daldi leen wax ciy léeb. Mu ne leen: «Amoon na fi nit ku jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas pax ngir nal ci réseñ yi, tabax wottukaay, ba noppi batale ko ay beykat, daldi tukki.
2 «Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi.
3 Waaye ñu jàpp ko, dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
4 Mu yónniwaat beneen surga, waaye ñu dóor ko ci bopp, toroxal ko.
5 Mu yónneeti beneen surga, ñu rey ko. Mu yónni ñeneen ñu bare, ñii ñu dóor leen, ñii ñu rey.
6 «Noonu mu dese ko kenn rekk, di doomam ji mu bëgg. Mujj mu yónni ko naan: “Xëy na ñu weg sama doom.”
7 Waaye beykat yi daldi ne ci seen biir: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”
8 Ñu jàpp ko nag, rey, sànni ci biti.»
9 Noonu Yeesu laaj leen: «Boroom tool bi nag, lu muy def? Xanaa ñëw, rey beykat ya, dénk tool ba ñeneen.
10 Ndax musuleen a jàng wax jii ci Mbind mi?“Doj wi tabaxkat yi sànni,mujj na di doju koñ;
11 ci Boroom bi la loolu jóge,te yéemu nanu ci.”»
12 Noonu kilifa yi di wut pexem jàpp ko, ndaxte xam nañu ne, ñoom lay wax. Waaye ragal nañu mbooloo mi, ba ñu bàyyi ko fa, dem.
13 Bi loolu amee ñu yónni ci Yeesu ay Farisen ak ñu far ak buur bi Erodd, ngir fiir ko ci waxam.
14 Ñu ñëw ci moom nag ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor. Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag am déet? Nu fey ko walla nu bañ koo
15 Waaye Yeesu xam na seen naaféq, mu ne leen: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir? Indil-leen ma posetu denariyon, ma seet.»
16 Ñu jox ko poset bi. Noonu Yeesu laaj leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu tontu ko: «Sesaar.»
17 Noonu Yeesu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» Ñu daldi waaru ci mbiram.
18 Gannaaw loolu ay Sadusen ñëw ci moom, ngir laaj ko lenn. Sadusen yi nag gëmuñu ne, ndekkite am na.
19 Ñu ne ko: «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu, te bàyyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam.
20 «Amoon na fi nag juróom-ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom.
21 Ñaareel ba takk jigéen ja, faatu moom itam te bàyyiwul doom. Ñetteel bi it noonu.
22 Mbir mi dem na nag, ba juróom-ñaar ñooñu ñépp dem, te kenn bàyyiwu fi doom. Mujj jigéen ja faatu moom itam.
23 Ci ndekkite li nag kan ci ñoom moo ko war a donn, fekk ku nekk ci juróom-ñaar ñi mas na koo takk?»
24 Yeesu tontu leen ne: «Mbaa du dangeen a nekk cig réer, ci li ngeen xamul Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla?
25 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
26 Te sax li jëm ci mbirum ndekkite, xanaa jànguleen lii Yàlla wax ci Tawreetu Musaa ci saarum ngarab si: “Maay Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba”?
27 Li ci génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee, waaye Yàllay ñiy dund la. Kon sóobu ngeen cig réer.»
28 Bi ñuy werante, benn xutbakat ñëw, dégg seen waxtaan, gis ne Yeesu tontu na leen tont lu leer. Mu laaj ko nag: «Ci ndigal yi, ban moo ci gën a màgg?»
29 Noonu Yeesu tontu ko ne: «Bii: “Bànni Israyil, déglul! Yàlla sunu Boroom moom rekk mooy Buur.
30 Kon nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa xel mépp ak sa kàttan gépp.”
31 Te ñaareel bi, lii la: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.” Ndigal yii ñoo sut yépp.»
32 Xutbakat bi ne ko: «Waaw kilifa gi, li nga wax dëgg la: Yàlla kenn la, te amul jeneen Yàlla ju dul moom.
33 Te nga bëgg ko ak sa xol bépp ak sa xel mépp ak sa kàttan gépp moo dàq bépp sarax bu ñuy yóbbu ngir màggal Yàlla ak bu ñuy lakk ca saraxalukaay ba.»
34 Bi Yeesu gisee nag ne, tontu na ak xel, mu ne ko: «Sorewuloo nguuru Yàlla.» Bi mu waxee loolu, kenn ñemeetu ko laaj dara.
35 Bi nga xamee ne Yeesu ma nga doon jàngale ca kër Yàlla ga, mu laaj nit ñi: «Lu tax xutbakat yi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
36 Daawuda moom wax na ci kàttanu Xel mu Sell mi naan:“Boroom bi nee na sama Boroom:«“Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.»“ “
37 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” naka mu nekke sëtam?» Noonu mbooloo mu mag mi di ko déglu ak bànneex.
38 Bi Yeesu di jàngale nag, mu ne leen: «Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi.
39 Ci jàngu yi, féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi.
40 Ñu ngi lekk alalu jigéen ñi seeni jëkkër faatu, di ñaan Yàlla ay ñaani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gën a tar.»
41 Noonu Yeesu toog ca kër Yàlla ga, janook ndab, yi ñuy def sarax ngir Yàlla, muy xool nit ña cay dugal seen xaalis. Am nag ay boroom alal yu ci di def xaalis bu bare.
42 Gannaaw ga daal benn jigéen ju jëkkëram faatu, te mu ñàkk, ñëw, def ci ñaari poseti xànjar, yu matul sax dërëm.
43 Bi ko Yeesu gisee, mu woo taalibe yi ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, li jigéen ju ñàkk jee dugal ca defukaay ya moo ëpp maana alalu ñeneen ñi ñépp.
44 Ñoom ñépp dañu sàkku ci seen barele, waaye moom dafa sàkku ci néewleem, ba far ko joxe lépp, toog.»