menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Bi mu waxee noonu ba noppi, Yeesu jóge fa ak i taalibeem, jàll xuru Sedoron, dugg cib tool.
2 Yudaa mi ko naroon a wor xamoon na it bérab ba, ndaxte Yeesu daan na fa dem ak ay taalibeem.
3 Yudaa daldi fa dem, yóbbaale mbooloom xarekat ak ay alkaati yu ko saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya jox. Ñu yor ay jum ak ay làmp ak it gànnaay.
4 Noonu Yeesu, mi xamoon li ko waroon a dal lépp, jubsi leen ne leen: «Ku ngeen di seet?»
5 Ñu ne ko: «Yeesum Nasaret.» Yeesu ne: «Man la.» Fekk Yudaa mi ko nar a wor a nga ànd ak ñoom.
6 Bi leen Yeesu nee: «Man la,» ñu daldi dellu gannaaw, ba daanu.
7 Yeesu laajaat leen ne: «Ku ngeen di seet?» Ñu ne ko: «Yeesum Nasaret.»
8 Mu ne leen: «Wax naa leen ne, man la. Bu fekkee ne nag man ngeen di seet, bàyyileen ñii ma àndal, ñu dem.»
9 Noonu la baat boobu mu waxoon ame: «Baay, kenn sànkuwul ci ñi nga ma dénk.»
10 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, Simoŋ Piyeer bocci jaasi, ji mu yoroon, daldi dóor surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg. Surga boobu mi ngi tuddoon Malkus.
11 Waaye Yeesu ne Piyeer: «Roofal jaasi ji ci mbaram. Ndax warumaa naan kaasu naqar, bi ma Baay bi sédd?»
12 Mbooloom xarekat ya ak seen kilifa ak alkaatiy Yawut ya jàpp Yeesu, daldi yeew,
13 jëkk koo yóbbu ca Anas, ndaxte Anas mooy gorob Kayif, mi doon saraxalekat bu mag ba at mooma.
14 Kayif moo digaloon Yawut ya ne: «Li gën moo di kenn rekk dee, ngir mbooloo mi mucc.»
15 Bi ñuy yóbbu Yeesu, Simoŋ Piyeer ak keneen ca taalibe ya toppoon nañu ko. Keneen kooku nag, xamante na ak saraxalekat bu mag ba, moo waral mu duggaaleek Yeesu ca biir kër kilifa ga.
16 Waaye Piyeer, moom, des ca buntu kër ga. Noonu taalibe boobu xamante woon ak saraxalekat bu mag ba génn, wax ak jigéen, ja doon wottu buntu kër ga, fexe Piyeer dugg ci biir.
17 Mbindaan mi doon wottu bunt bi ne Piyeer: «Mbaa yaw it bokkuloo ci taalibey waa ji?» Mu ne ko: «Déedéet, bokkuma ci.»
18 Booba dafa seddoon, ba surga ya ak alkaati ya boyal ab taal, di ca jaaru. Piyeer itam taxaw, di jaaru ak ñoom.
19 Saraxalekat bu mag ba daldi laaj Yeesu ci lu jëm ci taalibeem yi ak ci njàngaleem mi.
20 Yeesu tontu ko ne: «Ci mbooloo laa doon waxe. Ci kër Yàlla ga ak ci ay jàngu, fa Yawut yépp di daje, laa mas di jàngalee. Musumaa wax dara di ko nëbb.
21 Lu tax nga may laaj? Laajal ñi doon déglu li ma leen wax. Ñoom xam nañu li ma doon wax.»
22 Bi Yeesu waxee loolu, kenn ci alkaati yi nekkoon ci wetam daldi koy pes ne ko: «Ndax nii ngay tontoo saraxalekat bu mag bi?»
23 Yeesu tontu ko ne: «Su ma waxee lu jaaduwul, wone ko; waaye su ma waxee lu jub, lu tax nga may dóor?»
24 Anas daldi koy yebal ca Kayif, saraxalekat bu mag ba, ñu yeew ko ba tey.
25 Fekk na booba Simoŋ Piyeer, moom, ma nga taxaw di jaaru rekk. Ñu laaj ko ne: «Mbaa yaw it bokkuloo ci taalibey waa ji?» Waaye Piyeer weddi ko ne: «Déedéet, bokkuma ci.»
26 Kenn ci surgay saraxalekat bu mag ba, di mbokku ka Piyeer coroon noppam, ne Piyeer: «Xanaa du yaw laa gisoon ak moom ca tool ba?»
27 Waaye Piyeer dellu weddi ko. Noonu ginaar daldi sab.
28 Bi loolu wéyee ñu jële Yeesu ca Kayif, yóbbu ko ca kër boroom réew ma. Ci waxtuw njël la woon. Waaye Yawut ya yéeguñu ca taaxum kaw ma. Dañoo bañoon a taq sobe, ngir man a lekk ca ñamu màggalu Jéggi ba.
29 Looloo tax Pilaat boroom réew ma génn, dajeek ñoom. Mu laaj leen ne: «Lu ngeen di jiiñ waa jii?»
30 Ñu tontu ko ne: «Bu deful woon lu bon, duñu la ko jébbalsi.»
31 Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, te àtte ko ci seen yoon.» Yawut yi ne ko: «Yoon mayu nu, nu àtte nit, teg ko dee.»
32 Noonu la kàddug Yeesu gi ame, ci li mu misaaloon ni mu war a faatoo.
33 Gannaaw loolu Pilaat duggaat ca taaxum kaw ma, woo Yeesu ne ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?»
34 Yeesu tontu ko ne: «Ndax yaa ko xalaat, wax ko, am dañu la koo xelal ci man?»
35 Pilaat ne ko: «Mbaa xalaatoo ne, man Yawut laa? Sa xeet ak saraxalekat yu mag yi ñoo ma la jébbal. Lan nga def?»
36 Yeesu tontu: «Sama kilifteef nekkul ci àddina. Bu sama kilifteef nekkoon àddina, sama surga yi dinañu xeex, ngir bañ ñu jébbal ma Yawut yi. Waaye sama kilifteef nekkul àddina.»
37 Pilaat ne ko: «Kon yaw buur nga?» Yeesu tontu ko: «Wax nga ko; buur laa. Lii moo tax ma juddu, ñëw àddina: ngir wax dëgg gi. Ku bokk ci dëgg dina nangu li ma wax.»
38 Pilaat laaj ko ne: «Luy dëgg?» Bi mu waxee loolu ba noppi, Pilaat daldi génnaat, jëm ca Yawut ya ne leen: «Gisuma ci moom genn tooñ.
39 Seen aada laaj na, ma bàyyil leen kenn, saa su ñuy def màggalu bésu Jéggi bi. Xanaa ma bàyyil leen “buuru Yawut yi?”»
40 Noonu ñu daldi yuuxuwaat: «Déedéet, waxunu kii; Barabas lanu wax!» Fekk Barabas moomu taskatu réew la woon.