menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Ci lu jëm ci samay mbir nag, maa ngi leen di ñaan — man Pool, mi ñu ne, ci seen biir «ragal» laa, bu ma leen soree, «ñeme,» — maa ngi leen di ñaan ndax woyof ak lewetaayu Kirist, ngir bu ma ñëwee, ma bañ a ànd ak ñeme gi may dencal ñenn
3 Dëgg la ne nit rekk lanu, waaye dunu xeexe ni nit.
4 Ndaxte gànnaay, yi nuy xaree, jógewuñu ci nit, waaye ca Yàlla lañu jóge, te ànd ak kàttan, ngir daaneel ay tata. Danuy daaneel xalaat yi dul dëgg
5 ak bépp tiitar buy jànkoonteek xam-xamu Yàlla, te danuy noot bépp xalaat, ba mu déggal Kirist.
6 Te fas yéene nanoo jubbanti képp ku déggadi, bés bu seen dégg ndigal matee.
7 Xool-leen mbir mi ne fàŋŋ. Bu amee ku mu wóor ne, ci Kirist la bokk, na jàpp it ne, su bokkee ci Kirist, nun itam ci Kirist lanu bokk.
8 Awma lu may rus, su may damu lu ëpp ci sañ-sañ bi nu Boroom bi jox, di sañ-sañu yokk seen ngëm, te du ngir seen kasara.
9 Ba tey bëgguma ngeen xalaat ne, maa ngi leen di xëbal ci samay bataaxal.
10 Ndaxte am na ku naan: «Ay bataaxalam dañoo ñagas te am doole, waaye bu teewee dafay ñàkk fulla, di wax waxi picc.»
11 Kiy wax loolu na xam lii: ni sunuy kàddu mel ci sunuy bataaxal, bu nu fa nekkul, noonu it lanuy mel ci sunuy jëf, bu nu teewee.
12 Ñemewunoo féetele walla mengale sunu bopp ak ñooñu naw seen bopp. Ci li ñuy sàkk ab natt ngir natt ak mengale seen bopp ak seen bopp, ñàkk xel a tax.
13 Nun nag dunu damu ci lu weesu dayo. Nu ngi damu ci liggéey bi nu Yàlla sas, ba may nu, nu agsi ci yéen.
14 Bu sunu sas agsiwul woon ba ci yéen, kon man nanoo ne, génn nanu sas wi nu Yàlla sas. Waaye agsi na ba ci yéen, te indil nanu leen xebaar bu baax bi jëm ci Kirist.
15 Kon nag dunu jéggi dig yi Yàlla rëdd, bay damu ci liggéeyu ñeneen. Waaye am nanu yaakaar ne, su seen ngëm yokkoo, dinanu gën a màgg ci seen biir, des ba tey ci dig yi nu Yàlla rëddal.
16 Noonu dinanu man a yégle xebaar bu baax bi ci bérab, yi leen féete gannaaw, te bañ a damu ci li ñeneen ñi def ci seen sas.
17 Waaye ni ko Mbind mi waxe: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi.»
18 Ndaxte ki neex Yàlla, du ki naw boppam, waaye ki Yàlla gërëm.