menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Damu amul jariñ, ba tey war na ma. Kon ma jàll ci nettali gis-gisi Boroom bi ak i peeñu.
2 Xam naa taalibeb Kirist boo xam ne yékkati nañu ko ba ca asamaan, si gën a kawe, booba ak léegi mat na fukki at ak ñeent. Xawma ndax ànd na ak jëmmam walla déet. Yàlla rekk a xam.
3 Xam naa ne, nit kooku yékkati nañu ko ba fa Yàlla nekk. Bu dee ci jëmmam mbaa ci xelam, xawma; Yàllaa xam. Mu dégg fa baat yu ñu mënul a nettali te yu ñu mayul doom Aadama, mu ŋaaŋ ko.
5 Dinaa damu ci nit ku mel noonu. Waaye duma damu ci sama bopp, lu dul liy wone sama néew doole.
6 Su ma bëggoon a damu, du doon yëfi dof, ndaxte dëgg laay wax. Waaye damay moytoo damu, ngir kenn bañ a foog ci man lu weesu li mu gis, may def, te muy dégg, ma di ko wax.
7 Te it ngir ma bañ a yég sama bopp ndax peeñu yooyu wees xel, mayees na mbir dal ma ci sama yaram, di ma metital ni dég, muy malaakam Seytaane mu may sonal, ngir ma bañ a yég sama bopp.
8 Ñaan naa Boroom bi ñetti yoon ci mbir moomu, ngir mu taqale ma ak moom.
9 Waaye mu ne ma: «Sama yiw doy na la; sama kàttan a ngi mate cig néew doole.» Kon nag dëgg-dëgg, gën na maa bég ci damu ndax sama néew doole, ngir kàttanu Kirist dëkk ci man.
10 Looloo tax may bég ci néew doole, yi may wéye ngir turu Kirist, ciy tiis, ciy njàqare, mbaa ñu saaga ma, mbaa ñu fitnaal ma. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laay am kàttan.
11 Ci dëgg-dëgg wax naa waxi dof te yéena ma ci dugal, fekk yéen ci seen bopp sax yéena ma waroon a sargal, ndaxte su ma dul dara sax, seen ndaw yooyu ngeen naw ëpplewuñu ma dara.
12 Kéemaan yi, jaloore yi ak jëf yu màgg, yiy firndeel ndawul Kirist, feeñ nañu ci seen biir, ma ànd ci ak muñ gu mat.
13 Lan laa defal yeneen mboolooy ñi gëm te defaluma leen ko, xanaa rekk li ma wéeru ci ñoom te wéeruma ci yéen? Baal-leen ma googu tooñ!
14 Maa ngi leen di waaj a ganesi ñetteel bi yoon, te duma wéeru ci yéen. Wutsiwuma seen alal, yéen laa soxla. Ndaxte du gune moo war a yor waajuram, waaye waajur moo war a yor gune yi.
15 Man nag nangu naa joxe li ma am lépp ak xol bu sedd, ba joxe sama bopp sax, ngir dimbali leen. Gannaaw bëgg naa leen nii, xanaa kay seen mbëggeel ci man warul a wàññiku?
16 Kon noonu la, nekkuma woon yen ci yéen. Waaye man na am ñu naan, dama leen a nax, ba réeral leen ci sama njublaŋ.
17 Mbaa du damaa lekk seen alal, jaare ko ci kenn ci ñi ma yónni woon?
18 Sant naa Tit, mu ñëw ci yéen, te yebal naa sunu mbokk moomu ak moom. Ndax Tit dafa lekk seen alal? Man ak moom, ndax bokkunu woon xel mu nu yékkati ak tànk yu nuy dox?
19 Xanaa diirub li ngeen di jàng lii, defe ngeen ne, nu ngi wut aw lay ci seen kanam. Samay xarit, nu ngi leen di wax ci kanam Yàlla ak ci turu Kirist; te lépp ngir seen njariñ la.
20 Ragal naa, bu ma ñëwee ci yéen, fekk leen nu ma neexul, te yéen it ngeen fekk ma nu leen neexul. Ragal naa fekk ay xuloo ci seen biir, ak ñeetaane, xadar ak diiroo mbagg, xas ak jëw, réy-réylu ak yengu-yengu.
21 Ragal naa, bu ma leen ganesiwaatee, Yàlla sama Boroom suufeel ma ci seen biir, ma naqarlu ci ñu bare ñu bàkkaaroon te dëdduwuñu seen yàqute, seen njaaloo ak seen ñaawteef, gi ñu doon def.