menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Man mi ñu tëj kaso ngir Boroom bi nag, maa ngi leen di dénk, ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla.
2 Ngeen woyof toyy te lewet, di muñalante tey baalante ci mbëggeel,
3 te dem ba fu seen kàttan yem, ngeen likkoo ci jàmm, bay sàmm booloo gi leen Xelum Yàlla may.
4 Jenn jëmm moo am, menn Xel, ak jenn yaakaaru ëllëg ju wooteb Yàlla ëmb.
5 Benn Boroom it a am, genn ngëm, ak benn seedeb ngëm ci li ñu leen sóob ci ndox.
6 Te jenn Yàllaa am, di Baayu ñépp, mu tiim ñépp, fees ñépp, te dëkk ci ñépp.
7 Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ni nu ko Kirist séddalee.
8 Looloo tax Mbind mi ne:«Yéeg na ba ca fa gën a kawe,yóbbaale mbooloom noon mu bare, mi mu noot,tey séddale nit ñi ay may.»
9 Su nu waxee ne «yéeg na,» li moo ci génn: daa jëkk a wàcc ba ca bérab ya gën a suufe.
10 Ki wàccoon moo yéegaat, ba tiim asamaan yépp, ngir fees lépp.
11 Moo may ñii di ay ndawam, ñii ay yonent, ñii ay taskati xebaar bu baax bi, ak ñeneen ñuy sàmm mbooloom ñi gëm te di ko jàngal.
12 Maye na leen, ngir ñu waajal gaayi Yàlla yu sell yi, ñu man a bey seen sas ci taxawal mbooloom Kirist, di jëmmam.
13 Noonu nu mànkoo ci sunu ngëm ak ci xam Doomu Yàlla ji, ba kera nuy egg ci nekk nit ku sotti, te taxaw taxawaay bu dëppook matug Kirist.
14 Noonu dootunu ay gune yu njàngalem nit ku ñëw di fàbbi ci seeni làqarci ak seeni pexe, nu mel ni ay gaal yu duus yi ak ngelaw li di baaje.
15 Waaye dinanu wax dëgg, ëmb ko ci mbëggeel, bay màgg ci fànn gu ne ci sunu bokk ci Kirist. Mooy bopp,
16 te jëmm jépp ci moom lay dunde, di jëmm ju ràbboo te déggoo ci bépp tenqoo, te cér bu nekk di def warugaram. Noonu jëmm ji di yokku ak a màgg ci biir mbëggeel.
17 Maa ngi leen di wax lii nag, te di ko dëggal ci kanamu Boroom bi: buleen dundeeti ni xeeti àddina yi, ci seeni xalaati neen
18 ak seen xel mu lëndëm. Dañoo génn ci dundu Yàlla, ndax umple gi ñu am ci moom, ak li ñu ko tëjal seen xol.
19 Seen xol dafa dërkiis, ba ñu bayliku ciy topp seen nafsu, di sóobu ci bépp sobe te xér ci.
20 Waaye du dundin woowu ngeen jàng ci Kirist.
21 Ndax yaakaar naa ne, dégg ngeen Kirist te jàng ngeen ci moom, ba xam dëgg gi Yeesu ëmb.
22 Maanaam ngeen yulli seen jikko ju bon, ji ngeen judduwaale te daan fés ci seeni jëf, te muy gën a yées, moom ak i bëgg-bëggam yuy naxe kese.
23 Te ngeen yeeslu ci seen biir xel,
24 te soloo jikko ju bees, ji Yàlla sàkk ci njub ak sell yu dëggu.
25 Kon nag bàyyileen di fen, tey wax dëgg kenn ku nekk ci moroomam, ndax ku nekk sa genn-wàllu moroom nga.
26 Ku mer, bu mu jàll aw kaañ; bu jant bi sowaale seen mer,
27 ba ngeen may Seytaane bunt.
28 Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax ci ay loxoom, ngir mu man a dimbali ñi néew doole.
29 Bu genn kàddu gu ñaaw génn ci seen gémmiñ, waaye su wax yegsee, nangeen wax lu rafet, ba faj soxlay seeni moroom, te teg ñi leen di déglu ci yoonu yiw.
30 Buleen yóbbe tiis Xelu Yàlla mu Sell, mi leen tàmpe ngir bésu goreel ba.
31 Dëdduleen lépp luy wex mbaa tàng bopp, luy mer mbaa coow, lépp luy xaste mbaa coxor.
32 Te ngeen baax ci seen diggante, di laayante biir tey baalante, ni leen Yàlla baale ci turu Kirist.