menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Kon nag, ba nu ko mënatul a dékku, nangu nanu ñu bàyyi nu, nun doŋŋ, ca dëkku Aten,
2 te yónni nanu Timote, sunu mbokk ak sunu nawle ci liggéeyu Yàlla ak ci waareb xebaaru Kirist. Yónni nanu ko, ngir mu dénk leen, tey feddali seen ngëm,
3 ngir kenn bañ a raf ndax nattu, yi ngeen di jaar. Yéen ci seen bopp xam ngeen ne, nattu mooy sunu cér.
4 Ba nu nekkee ak yéen sax, waxoon nanu leen, waxati ko ne, fàww nu sonn; te noonu la ame, yéen xam ngeen ko.
5 Noonu ba ma ko mënatul a dékku, yónnee naa, ngir xam fu seen ngëm tollu, ngir ragal Seytaane fiir leen, ba sunu ñaq neen.
6 Waaye léegi Timote bawoo na ci yéen, indaale xebaar yu neex ci seen ngëm ak seen mbëggeel; xamal na nu ne, yéena ngi am pàttaliku yu rafet ci nun te namm nu lool, ni nu leen namme yéen itam.
7 Noonu bokk yi, ci biir tiis ak coono yi nu nekk, seen ngëm dëfël na sunu xol.
8 Ndaxte noo ngi dund dëgg-dëgg, ndegam yéena ngi sax ci Boroom bi.
9 Ndaw cant yu bare yu nu war a sant Yàlla ndax yéen! Ndaw mbég mu bare, mi nu am ci kanamam ndax yéen!
10 Guddi ak bëccëg nu ngi wàkkirlu ci ñaan Yàlla, ngir gis leen, ba man a mottali seen ngëm.
11 Na Yàlla sunu Baay moom ci boppam ak Yeesu sunu Boroom jubal sunu yoon ci yéen.
12 Na leen Boroom bi dolli mbëggeel gu tar, ngeen bëggante te bëgg ñépp, ni nu leen bëgge nun.
13 Na samp seeni xol noonu ci cell gu amul sikk fa kanam Yàlla sunu Baay, ba bés bu Yeesu sunu Boroom dellusee, ànd ak gaayam yu sell yépp.