menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Xelum Yàlla mi wax na bu leer ne, ci mujug jamono dina am ñu bàyyi yoonu ngëm wi, di topp ay xel yuy fàbbee ak xalaati Seytaane.
2 Ñooñu ay naaféq yuy naxe lañu, te seen xol dërkiis.
3 Dinañu tere séy, di araamal ay ñam, fekk Yàlla sàkk na leen, ngir ñi gëm te xam dëgg man ciy jëfandiku ak cant.
4 Ndaxte li Yàlla sàkk lépp baax na, kon wenn ñam araamul ci ku koy jëfandikoo ak cant.
5 Ndaxte kàddug Yàlla ak ñaan ñoo koy sellal.
6 Saxal ci digal bokk yi loolu nag, kon dinga nekk jawriñu Kirist Yeesu ju baax ju regg ci kàdduy yoonu ngëm wi ak njàngale mu rafet, mi nga xam bu wér.
7 Tanqamlul ay léebi diiney neen, di ay wax yu amul bopp yu àddina kese; waaye tàggatal sa bopp ci ragal Yàlla.
8 Ndaxte tàggat yaram am na fu njariñam yem, waaye njariñu ragal Yàlla dafa daj lépp, ëmb digey àddina ak àllaaxira.
9 Wax ju wóor a ngii, te mat a nangu ak gépp kóolute.
10 Danuy ñaq tey bëre, ndaxte wékk nanu sunu yaakaar ci Yàlla Aji Dund ji, di Musalkatu ñépp, rawatina nag ci ñi gëm.
11 Digal leen yëf yooyu nag ci sa njàngale.
12 Bu la kenn xeeb ndax say at, waaye defal sa bopp royukaayu ñi gëm ci say wax ak say jëf, ci sa mbëggeel, sa ngëm ak sa cell.
13 Li feek may dikk, saxal ci jàng di biral Mbind mi ci mbooloo mi, di leen dénk ak a jàngal.
14 Bul sàggane may gi nekk ci yaw, gi la Yàlla jox jaarale ko ci waxu yonent, keroog bi la njiit yi tegee loxo.
15 Faaydaalal yëf yooyu te sóobu ci, ba sa jëm kanam bir ñépp.
16 Sàmmal sa bopp te sàmm sa njàngale, te sax ci; noonu dinga musal sa bopp, yaw ak ñi lay déglu.