menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Moo tax kon nu war a gën a faaydaal wax yi nu dégg, ngir bañ a bayliku.
2 Xam nanu ne kàddug yoon, wi Yàlla yégle jaarale ko ci malaaka yi, wareef la woon, te képp ku ko mas a moy, walla mu mas koo tanqamlu, jot na mbugal gi mu yelloo.
3 Kon nun ñi dégg mucc gu mag gi, bu nu ko sàgganee, nan lanuy man a rëcce mbugalu Yàlla? Boroom bi moo xamle woon mucc googu ca njàlbéen ga, te gannaaw gi, ñi ko dégg, ñoo nu ko wóoralal.
4 Te it Yàlla dëggal na seen seede ci ay firnde ak ay kéemaan, ay jaloore yu bare ak ci ay may yu jóge ci Xelam mu Sell, te mu séddale leen ni mu ko bëgge.
5 Yàlla jébbalul malaaka yi benn sañ-sañ bu jëm ci jamonoy ëllëg ji nuy wax; keneen la ko jébbal,
6 ndaxte am na fu ñu wax ci Mbind mi ne:«Lan mooy nit, yaw Yàlla, ba nga di ko xalaat?Lan mooy doomu nit, ba nga koy topptoo?
7 Wàcce nga ko, def komu gën a suufe tuuti malaaka yi.Kaalaa nga ko teraanga ak ndam,
8 nootal ko lépp, mu teg ci tànk.» Bi ko Yàlla nootalee lépp nag, bàyyiwul dara. Fi mu nekk gisagunu ne, lépp a ngi ci sañ-sañam;
9 Waaye gis nanu Yeesu. Wàcce nañu ko, def ko mu gën a suufe tuuti malaaka yi, ngir mu dee ci wàllu ñépp, ndaxte loolu la Yàlla dogal ci yiwam. Waaye léegi Yàlla kaalaa na ko teraanga ak ndam ndax coono bi mu daj ba dee.
10 Ndaxte Yàlla mi yelloo lépp te sàkk lépp, dogal na def ñu bare ay doomam, boole leen ci ndamam. Jekk na nag mu matal Yeesu ci coono bi mu daj, moom mi leen xàllal yoonu mucc gi.
11 Moom Yeesu miy sellal, ak ñi muy sellal, ñoom ñépp genn njaboot lañu. Moo tax Yeesu rusu leen a wooye ay doomi baayam.
12 Nee na:«Yaw Yàlla, dinaa xamle sa turci samay doomi baay,dinaa la tagg ci biir mbooloo mi.»
13 Newaat na:«Dinaa am ci Yàlla kóolute.» Dellu na waxaat ne:«Maa ngi nii, man ak doom yi ma Yàlla jox.»
14 Doomam yooyu muy wax, nit kese lañu. Looloo tax Yeesu it moom ci boppam, wàcc na, jëmmoo ni ñoom, ngir dee, ba man caa daaneel Ibliis, mi yore dooley dee.
15 Noonu mu yiwi nit, ñi meloon ni ay jaam seen giiru dund gépp ndax ragal a dee.
16 Leer na ne, Yeesu xettalisiwul malaaka yi, waaye askanu Ibraayma lay xettalisi.
17 Looloo taxoon mu war a mel niy doomi baayam ci bépp fànn, ngir doon seen saraxalekat bu mag fa kanam Yàlla, bi leen yërëm te di sàmm kóllëre, te ci liggéeyu saraxaleem joxe na bakkanam ngir dindi bàkkaari nit ñi, ba Yàlla baal leen.
18 Gannaaw sonn na ci nattu yi mu daj, man na dimbali ñiy jaar ciy nattu.