menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Kon nag yéen bokk yu sell yi, yéen ñi Yàlla woo, ngeen bokk ci nguuram gu kawe ga, seetleen ci Yeesu, moom miy ndawu Yàlla li, di saraxalekat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
2 Ku takku la ci liggéey bi ko Yàlla sas, ni ko Musaa nekke woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla.
3 Waaye Yeesu yelloo na ndam lu sut lu Musaa, ni kiy tabax kër ëppe maana kër ga muy tabax.
4 Ndaxte kër gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos lépp mooy Yàlla.
5 Musaa moom ku takku la woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla. Waaye jawriñ rekk la woon, ngir seede li Yàlla waroon a yégle.
6 Yeesu nag ku takku la it, waaye Doom la, juy yilif kër Baayam. Nun nooy këram googu, bu nu saxee ci sunu kóolute te di bég ci li nuy séentu.
7 Moo tax Xel mu Sell mi wax lii ci Mbind mi:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,
8 buleen dëgër bopp,ni seeni maam defoon ca màndiŋ ma,keroog ba ñu dëddoo Yàlla di ko diiŋat.»
9 Yàlla ne:«Foofa seeni maam diiŋat nañu ma fa,di ma fexee fiir,te gis nañu samay jëf
10 diirub ñeent-fukki at.Looloo tax gennliku naa leen, daldi ne:“Seeni xalaat a leen di réeral saa su nekk,xamuñu yoon yi ma neex.”
11 Giñ naa kon ci sama mer ne:“Duñu dugg mukk ci sama noflaay.”»
12 Bokk yi, wottuleen ba kenn ci yéen bañ a am xol bu bon te gëmadi, bay dëddu Yàlla jiy dund.
13 Waaye bés bu nekk, deeleen soññante ci lu jëm ci Yàlla, fi ak bés boobu ñu wax wéyul, ngir ragal bàkkaar nax kenn, ba xolam tëju.
14 Am nanu wàll ci Kirist, su nu wéyee fii ba muj ga ci sunu kóolute, gi nu amoon ca njàlbéen ga.
15 Lii la Mbind mi wax:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,buleen dëgër bopp,ni seeni maam defoon, ba ñu dëddoo Yàlla.»
16 Ñan ñoo dégg baatu Yàlla bi nag te di ko dëddu? Xanaa ña Musaa génne woon Misra ñépp.
17 Te ñan la Yàlla mere lu mat ñeent-fukki at? Xanaa ñi daan bàkkaar te seeni néew tëdd ca màndiŋ ma.
18 Te it bi Yàlla defee ngiñ lii: «Duñu dugg mukk ci sama noflaay,» booba ñan ñoo ko taxoon di wax? Xanaa ña ko déggadil.
19 Noonu gis nanu sax ne, jotuñoo dugg ci noflaay boobu ndax seen gëmadi.