menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Melkisedeg moomu doon buuru Salem, moo nekkoon saraxalekat ca Yàlla Aji Kawe ji. Gannaaw ba Ibraayma dàqee buur ya, ba dellusi, Melkisedeg gatandu woon na ko, di ko barkeel.
2 Noonu Ibraayma fab fukkeelu cér bi, maanaam asaka, ci li mu jële woon ci xare ba lépp, jox ko. Ci lu jëkk turu Melkisedeg mi ngi tekki «buur bu jub bi.» Gannaaw loolu mooy buuru Salem, tur woowu mooy tekki «buuru jàmm.»
3 Melkisedeg nag xamaluñu ko baay, xamaluñu ko yaay walla menn maam. Amul fenn fu ñu wax ag juddoom walla ag deeyam. Moo tax nu di ko mengale ak Doomu Yàlla ji, ndaxte saraxalekat la bu kenn dul wuutu.
4 Seetleen ni mu màgge, moom Melkisedeg! Ibraayma sax, maamu cosaan mi, fab na li mu jële woon lépp ca xare ba, jox Melkisedeg asaka ja.
5 Yoonu Musaa digle na ne, ñi bokk ci giiru Lewi te di ay saraxalekat, nañu jot asaka ci alalu bànni Israyil, doonte sax ñuy seeni bokk te soqikoo ci Ibraayma.
6 Waaye Melkisedeg mi bokkul woon ci giiru Lewi, jotoon na asaka ci alali Ibraayma. Te rax-ca-dolli barkeel na ko, moom mi Yàlla sédde woon dige yi.
7 Kiy barkeel a gën a màgg ki ñuy barkeel, loolu amu ci benn werante.
8 Saraxalekat yi soqikoo ci Lewi, ñu ngi jot asaka, ni ko Melkisedeg jote woon. Waaye ñoom ñu nar a dee lañu. Melkisedeg nag moom, Mbind mi wóoral na ne, dafay dund.
9 Léegi nag ci ni ñu ko man a waxe, Lewi miy jot asaka ci bànni Israyil, moom ci boppam jox na ko Melkisedeg, jaare ko ci Ibraayma.
10 Ndaxte mi ngi nekkoon ci geñog maamam Ibraayma, bi ko Melkisedeg gatandoo.
11 Jox nañu bànni Israyil yoon wu sukkandiku ci liggéeyu saraxalekat yi soqikoo ci Lewi. Su fekkoonte ne nag liggéeyu saraxalekat yooyu manoon na yeggale nit cig mat, kon du soxlaati ab saraxalekat ni ko Melkisedeg nekke, ci fànn gu wuute ak
12 Te bu ñu fi jëlee saraxalekat yi ak seen liggéey, dañoo war a toxal itam yoon, wi ñu fi tëraloon.
13 Noonu Yeesu mi nuy wax, mi ngi soqikoo ci geneen giir gu bokkul ak giiru Lewi. Giir googu nag, amu ci kenn ku ci mas a def liggéeyu saraxale ca saraxalukaay ba.
14 Li wóor moo di, sunu Boroom mi ngi soqikoo ci giiru Yuda. Te bi Musaa bindee ci mbirum saraxalekat yi, limaalewul woon giir googu.
15 Li waral mbir mi gën a leer moo di ne, beneen saraxalekat bu mel ni Melkisedeg dafa ñëw.
16 Te defuñu ko saraxalekat jaarale ko ci yoonu ndono, waaye fal nañu ko ci dooley dund gu amul àpp.
17 Ndaxte seedeel nañu Yeesu lii:«Doon nga saraxalekat ba fàwwmel ni Melkisedeg.»
18 Noonu tebbi nañu yoon wu jëkk, wa néewoon doole te meññul dara
19 --ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat — waaye dugalal nañu nu fii yaakaar ju gën ju nu man a jaare ngir jege Yàlla.
20 Te rax-ca-dolli ngiñ ànd na ci. Ndaxte ñi soqikoo ci Lewi doon nañu ay saraxalekat te kenn giñul.
21 Waaye nag Yeesu moom doon na saraxalekat, bi Yàlla giñee ne ko:«Boroom bi giñ nate du dellu gannaaw mukk:“Doon nga saraxalekat ba fàww.”»
22 Ngiñ loolu moo tax Yeesu nekk tayle, giy wóoral kóllëre gi gën.
23 Te it yeneen saraxalekat yi dañoo bare woon, ndaxte dee moo daan tax duñu man a sax ci seen liggéey.
24 Waaye Yeesu miy dund ba fàww, sasoo na liggéeyu saraxale bu sax fàww.
25 Loolu moo tax it mu man a musal tey yeggale cig mat ñiy jaar ci moom te bëgg jege Yàlla, ndaxte mi ngi dund ba fàww ngir di leen rammu.
26 Kon nag Yeesu mooy saraxalekat bu mag, bi nu soxla; dafa sell, du def lu bon, du taq bàkkaar, bokkul dara ak bàkkaarkat yi, te yéege nañu ko fa Yàlla.
27 Niroowul ak yeneen saraxalekat yu mag yi; soxlawul di def bés bu set ay saraxi mala ngir bàkkaari boppam jëkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba fàww ngir dindi bàkkaar yi, bi muy joxe bakkanam.
28 Naka yoonu Musaa, aji néew doole yi lay fal saraxalekat yu mag. Waaye ngiñu Yàlla gi ñëw gannaaw yoon wi, Doom ji la fal saraxalekat bu mag bu mat ba fàww.