menu.png
Passwort vergessen ?

Kapitel Ansicht

 (Index)


•••► •••►
Vers Text
1 Noonu ma gis ca asamaan beneen firnde ju réy tey yéeme: juróom-ñaari malaaka yu taawu juróom-ñaari musiba, ñuy yu mujj ya, ndaxte ñoom ñooy matal merum Yàlla.
2 Noonu ma gis lu mel ni géej gu leer ni weer bu set buy ray-rayi ak safara. Ña nootoon rab wa ak nataalam, ak siifar bu mengoo ak turam, ñoo taxaw ca géej gu leer ga, yor xalam yu leen Yàlla jox.
3 Ñuy woy woyu Musaa jaamu Yàlla bi, ak woyu Mbote ma, naan:«Say jëf réy nañu te yéeme,yaw Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji.Say yoon jub nañu te dëggu,yaw Buur bi fiy sax ba abadan.
4 Ku la ragalul, Boroom bi?Ku dul màggal saw tur?Kenn, ndaxte yaw rekk yaa sell.Xeet yépp dinañu dikk, jaamu la,ndax say àtte bir na ñépp.»
5 Gannaaw loolu ma xool, noonu kër Yàlla ubbiku ca asamaan, muy tàntu màggalukaay, bi ëmb li Yàlla seede.
6 Juróom-ñaari malaaka, ya taawu juróom-ñaari musiba ya, daldi génn ca kër Yàlla ga. Ñu sol mbubb yu set te weex bay lerax, laxasaayoo ngeñaayi wurus ba ci seen dënn.
7 Noonu kenn ci ñeenti mbindeef ya jox juróom-ñaari malaaka ya juróom-ñaari ndabi wurus yu fees ak merum Yàlla jiy dund ba fàww.
8 Kër Yàlla ga fees ak saxar ndax leeraayu ndamu Yàlla ak kàttanam. Te kenn mënatul a dugg ca kër Yàlla ga, ba kera juróom-ñaari musiba, ya juróom-ñaari malaaka ya taawu, di mat.