menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 At the same time came the disciples unto Jesus, saying, Who is the greatest in the kingdom of heaven? Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gën a màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?»
2 And Jesus called a little child unto him, and set him in the midst of them, Noonu Yeesu woo xale, teg ko ci seen biir,
3 And said, Verily I say unto you, Except ye be converted, and become as little children, ye shall not enter into the kingdom of heaven. ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen woññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
4 Whosoever therefore shall humble himself as this little child, the same is greatest in the kingdom of heaven. Kuy suufeelu nag, ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gën a màgg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
5 And whoso shall receive one such little child in my name receiveth me. Te it ku nangu ci sama tur xale bu mel ni kii, man mii nga nangu.
6 But whoso shall offend one of these little ones which believe in me, it were better for him that a millstone were hanged about his neck, and that he were drowned in the depth of the sea. Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ca fa gën a xóot ca géej ga.
7 Woe unto the world because of offences! for it must needs be that offences come; but woe to that man by whom the offence cometh! «Yaw àddina dinga torox ndax say fiir yiy yóbbe nit bàkkaar. Fiir mënta ñàkk, waaye toroxte dal na nit ki koy lal.
8 Wherefore if thy hand or thy foot offend thee, cut them off, and cast them from thee: it is better for thee to enter into life halt or maimed, rather than having two hands or two feet to be cast into everlasting fire. Boo xamee ne sa loxo mbaa sa tànk mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga lafañ walla ñàkk loxo te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo walla ñaari tànk, te ñu sànni la ci safara su dul fey muk
9 And if thine eye offend thee, pluck it out, and cast it from thee: it is better for thee to enter into life with one eye, rather than having two eyes to be cast into hell fire. Boo xamee ne sa bët mu ngi lay yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga patt te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, te ñu sànni la ci safara.
10 Take heed that ye despise not one of these little ones; for I say unto you, That in heaven their angels do always behold the face of my Father which is in heaven. «Te it wottuleen a xeeb kenn ci ñi gën a tuuti, ndax kat seeni malaakaa ngi sax ci jataayu sama Baay bi nekk ci kaw. Maa leen wax loolu.
11 For the Son of man is come to save that which was lost.
12 How think ye? if a man have an hundred sheep, and one of them be gone astray, doth he not leave the ninety and nine, and goeth into the mountains, and seeketh that which is gone astray? «Luy seen xalaat ci lii? Su fi amoon nit ku am téeméeri xar, te benn ci ñoom réer, lu muy def? Ndax du bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, te dem wuti ma réer?
13 And if so be that he find it, verily I say unto you, he rejoiceth more of that sheep, than of the ninety and nine which went not astray. Bu ko gisee, mbég mi mu am ci moom mooy ëpp mbég, mi mu am ci juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent ya réerul.
14 Even so it is not the will of your Father which is in heaven, that one of these little ones should perish. «Noonu it seen Baay bi nekk ci kaw bëggul kenn ci ñi gën a tuuti sànku.
15 Moreover if thy brother shall trespass against thee, go and tell him his fault between thee and him alone: if he shall hear thee, thou hast gained thy brother. «Te lii itam, bu sa mbokk defee bàkkaar, demal yedd ko, yéen ñaar rekk. Bu la dégloo, kon gindi nga sa mbokk.
16 But if he will not hear thee, then take with thee one or two more, that in the mouth of two or three witnesses every word may be established. Waaye bu la dégluwul, àndal ak kenn mbaa ñaar, ngir mbir mi dëggu ci li ko ñaar walla ñett seede.
17 And if he shall neglect to hear them, tell it unto the church: but if he neglect to hear the church, let him be unto thee as an heathen man and a publican. Bu leen dégluwul ñoom itam, wax ko mbooloom ñi gëm. Bu dégluwul mbooloo ma nag, nga teg ko ni ku gëmul Yàlla mbaa ab juutikat.
18 Verily I say unto you, Whatsoever ye shall bind on earth shall be bound in heaven: and whatsoever ye shall loose on earth shall be loosed in heaven. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp lu ngeen yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan, te lépp lu ngeen yiwi ci àddina, dees na ko yiwi ci asamaan.
19 Again I say unto you, That if two of you shall agree on earth as touching any thing that they shall ask, it shall be done for them of my Father which is in heaven. «Maa ngi leen koy wax it, bu ñaar ci yéen déggoo ci àddina, ngir ñaan lu mu man a doon, sama Baay bi nekk ci kaw dina leen ko may.
20 For where two or three are gathered together in my name, there am I in the midst of them. Ndaxte fu ñaar walla ñetti nit booloo ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»
21 Then came Peter to him, and said, Lord, how oft shall my brother sin against me, and I forgive him? till seven times? Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko war a baal? Xanaa ba ci juróom-ñaari yoon?»
22 Jesus saith unto him, I say not unto thee, Until seven times: but, Until seventy times seven. Yeesu tontu ko ne: «Waxuma la ba ci juróom-ñaari yoon, waaye ba ci juróom-ñaar-fukki juróom-ñaari yoon.
23 Therefore is the kingdom of heaven likened unto a certain king, which would take account of his servants. «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgg a waññ alalam ak ay jaraafam.
24 And when he had begun to reckon, one was brought unto him, which owed him ten thousand talents. Ba mu tàmbalee waññ nag, ñu indil buur ba ku ko ameel ay milyoŋ yu baree-bare,
25 But forasmuch as he had not to pay, his lord commanded him to be sold, and his wife, and children, and all that he had, and payment to be made. waaye jaraaf ja amul lu mu feye. Kon nag sangam santaane, ñu jaay ko moom ak jabaram ak ay doomam ak lépp lu mu am, ngir fey bor ba.
26 The servant therefore fell down, and worshipped him, saying, Lord, have patience with me, and I will pay thee all. Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.”
27 Then the lord of that servant was moved with compassion, and loosed him, and forgave him the debt. Noonu sangam yërëm ko, bàyyi ko, baal ko bor ba.
28 But the same servant went out, and found one of his fellowservants, which owed him an hundred pence: and he laid hands on him, and took him by the throat, saying, Pay me that thou owest. «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.”
29 And his fellowservant fell down at his feet, and besought him, saying, Have patience with me, and I will pay thee all. Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.”
30 And he would not: but went and cast him into prison, till he should pay the debt. Waaye moom nanguwu ko, mu dem, tëj ko kaso, ba kera mu fey li mu ko ameel.
31 So when his fellowservants saw what was done, they were very sorry, and came and told unto their lord all that was done. «Bi ay moroomam gisee loolu nag, ñu am naqar wu réy, daldi dem, xamal seen sang li xew lépp.
32 Then his lord, after that he had called him, said unto him, O thou wicked servant, I forgave thee all that debt, because thou desiredst me: Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma.
33 Shouldest not thou also have had compassion on thy fellowservant, even as I had pity on thee? Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?”
34 And his lord was wroth, and delivered him to the tormentors, till he should pay all that was due unto him. Noonu sang ba mer, jébbal ko ñiy fitnaale ca kaso ba, ba kera muy fey li mu ko ameel lépp.
35 So likewise shall my heavenly Father do also unto you, if ye from your hearts forgive not every one his brother their trespasses. «Noonu la leen sama Baay bi ci kaw di def, bu ngeen baalul ku nekk seen mbokk ak xol bu sedd.»