menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 Then spake Jesus to the multitude, and to his disciples, Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak taalibeem ya ne leen:
2 Saying, The scribes and the Pharisees sit in Moses' seat: «Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa.
3 All therefore whatsoever they bid you observe, that observe and do; but do not ye after their works: for they say, and do not. Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe.
4 For they bind heavy burdens and grievous to be borne, and lay them on men's shoulders; but they themselves will not move them with one of their fingers. Dañuy takk say yu diis, yen leen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal sax ak seen cati baaraam.
5 But all their works they do for to be seen of men: they make broad their phylacteries, and enlarge the borders of their garments, Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi gis leen, di takk ay téere yu réy, tey réyal seeni laari mbubb.
6 And love the uppermost rooms at feasts, and the chief seats in the synagogues, Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam ca jàngu ya.
7 And greetings in the markets, and to be called of men, Rabbi, Rabbi. Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “Kilifa gi.”
8 But be not ye called Rabbi: for one is your Master, even Christ; and all ye are brethren. Waaye yéen buñu leen wooye “Kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp ay bokk ngeen.
9 And call no man your father upon the earth: for one is your Father, which is in heaven. Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw.
10 Neither be ye called masters: for one is your Master, even Christ. Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist.
11 But he that is greatest among you shall be your servant. Ki gën a mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga.
12 And whosoever shall exalt himself shall be abased; and he that shall humble himself shall be exalted. Kuy yékkatiku, dees na la suufeel; kuy suufeelu, ñu yékkati la.
13 But woe unto you, scribes and Pharisees, hypocrites! for ye shut up the kingdom of heaven against men: for ye neither go in yourselves, neither suffer ye them that are entering to go in. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanamu nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgg a dugg, mu dugg ci.
14 Woe unto you, scribes and Pharisees, hypocrites! for ye devour widows' houses, and for a pretence make long prayer: therefore ye shall receive the greater damnation.
15 Woe unto you, scribes and Pharisees, hypocrites! for ye compass sea and land to make one proselyte, and when he is made, ye make him twofold more the child of hell than yourselves. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu safara, ku leen yées ñaari yoon.
16 Woe unto you, ye blind guides, which say, Whosoever shall swear by the temple, it is nothing; but whosoever shall swear by the gold of the temple, he is a debtor! «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.”
17 Ye fools and blind: for whether is greater, the gold, or the temple that sanctifieth the gold? Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gën a màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell?
18 And, Whosoever shall swear by the altar, it is nothing; but whosoever sweareth by the gift that is upon it, he is guilty. Dangeen ne it: “Ku giñe saraxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.”
19 Ye fools and blind: for whether is greater, the gift, or the altar that sanctifieth the gift? Gumba yi! Lan moo gën a màgg, sarax si walla saraxalukaay bi tax sarax si sell?
20 Whoso therefore shall swear by the altar, sweareth by it, and by all things thereon. Ku giñe saraxalukaay bi, giñ nga ci saraxalukaay bi ak li ci kawam lépp.
21 And whoso shall swear by the temple, sweareth by it, and by him that dwelleth therein. Ku giñe kër Yàlla gi, giñ nga ci kër Yàlla gi ak Ki ci dëkk.
22 And he that shall swear by heaven, sweareth by the throne of God, and by him that sitteth thereon. Ku giñ ci asamaan, giñ nga ci jalu Buur Yàlla ak Ki ci toog.
23 Woe unto you, scribes and Pharisees, hypocrites! for ye pay tithe of mint and anise and cummin, and have omitted the weightier matters of the law, judgment, mercy, and faith: these ought ye to have done, and not to leave the other undone «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gën a màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca
24 Ye blind guides, which strain at a gnat, and swallow a camel. Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem.
25 Woe unto you, scribes and Pharisees, hypocrites! for ye make clean the outside of the cup and of the platter, but within they are full of extortion and excess. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal.
26 Thou blind Pharisee, cleanse first that which is within the cup and platter, that the outside of them may be clean also. Farisen yu gumba yi! Jëkkleen a setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set.
27 Woe unto you, scribes and Pharisees, hypocrites! for ye are like unto whited sepulchres, which indeed appear beautiful outward, but are within full of dead men's bones, and of all uncleanness. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk.
28 Even so ye also outwardly appear righteous unto men, but within ye are full of hypocrisy and iniquity. Yéen itam, ci ngistal dangeen a mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon.
29 Woe unto you, scribes and Pharisees, hypocrites! because ye build the tombs of the prophets, and garnish the sepulchres of the righteous, «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi.
30 And say, If we had been in the days of our fathers, we would not have been partakers with them in the blood of the prophets. Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.”
31 Wherefore ye be witnesses unto yourselves, that ye are the children of them which killed the prophets. Seede ngeen nii ne, yey ngeen seen bopp, te yéenay doomi ñi doon rey yonent yi,
32 Fill ye up then the measure of your fathers. di aw seen tànki baay, ba yées leen sax.
33 Ye serpents, ye generation of vipers, how can ye escape the damnation of hell? Yéen ñi mel ni ay jaan, te fees ak daŋar niy co, naka ngeen di mucce mbugalu safara?
34 Wherefore, behold, I send unto you prophets, and wise men, and scribes: and some of them ye shall kill and crucify; and some of them shall ye scourge in your synagogues, and persecute them from city to city: Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo-dëkk.
35 That upon you may come all the righteous blood shed upon the earth, from the blood of righteous Abel unto the blood of Zacharias son of Barachias, whom ye slew between the temple and the altar. Noonu deretu ñi jub, ji ñu tuur jépp ci àddina, dina xëppu ci seen kaw, li dale ci deretu Abel mi jub, ba ci deretu Sakariya doomu Baraki, mi ngeen rey ci diggante bérab bu sell bi ak saraxalukaay bi.
36 Verily I say unto you, All these things shall come upon this generation. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina dal ci niti jamono jii.
37 O Jerusalem, Jerusalem, thou that killest the prophets, and stonest them which are sent unto thee, how often would I have gathered thy children together, even as a hen gathereth her chickens under her wings, and ye would not! «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen!
38 Behold, your house is left unto you desolate. Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër, ba mu gent.
39 For I say unto you, Ye shall not see me henceforth, till ye shall say, Blessed is he that cometh in the name of the Lord. Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»