menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 And he entered into a ship, and passed over, and came into his own city. Bi loolu amee Yeesu dugg cig gaal, jàll dex ga, dellu dëkkam.
2 And, behold, they brought to him a man sick of the palsy, lying on a bed: and Jesus seeing their faith said unto the sick of the palsy; Son, be of good cheer; thy sins be forgiven thee. Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
3 And, behold, certain of the scribes said within themselves, This man blasphemeth. Bi mu waxee loolu, ay xutbakat daldi ne ci seen biir: «Nit kii mu ngi sosal Yàlla.»
4 And Jesus knowing their thoughts said, Wherefore think ye evil in your hearts? Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon ci seen xol?
5 For whether is easier, to say, Thy sins be forgiven thee; or to say, Arise, and walk? Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb?
6 But that ye may know that the Son of man hath power on earth to forgive sins, (then saith he to the sick of the palsy,) Arise, take up thy bed, and go unto thine house. Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
7 And he arose, and departed to his house. Noonu làggi ba daldi jóg, ñibbi.
8 But when the multitudes saw it, they marvelled, and glorified God, which had given such power unto men. Ba mbooloo ma gisee loolu, ñu daldi ragal te màggal Yàlla, mi dénk sañ-sañ bu tollu noonu doom Aadama yi.
9 And as Jesus passed forth from thence, he saw a man, named Matthew, sitting at the receipt of custom: and he saith unto him, Follow me. And he arose, and followed him. Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp.
10 And it came to pass, as Jesus sat at meat in the house, behold, many publicans and sinners came and sat down with him and his disciples. Gannaaw ga Yeesu doon lekk ca kër ga, te ay juutikat ak i boroom bàkkaar yu bare dikk, bokk lekk ak Yeesu ak taalibeem ya.
11 And when the Pharisees saw it, they said unto his disciples, Why eateth your Master with publicans and sinners? Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
12 But when Jesus heard that, he said unto them, They that be whole need not a physician, but they that are sick. Waaye bi ko Yeesu déggee, mu ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
13 But go ye and learn what that meaneth, I will have mercy, and not sacrifice: for I am not come to call the righteous, but sinners to repentance. Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.»
14 Then came to him the disciples of John, saying, Why do we and the Pharisees fast oft, but thy disciples fast not? Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?»
15 And Jesus said unto them, Can the children of the bridechamber mourn, as long as the bridegroom is with them? but the days will come, when the bridegroom shall be taken from them, and then shall they fast. Yeesu tontu leen: «Ndax gan yi ñëw ci céet dinañu naqarlu dara, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? Waaye bés yaa ngi ñëw yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir; booba nag dinañu woor.
16 No man putteth a piece of new cloth unto an old garment, for that which is put in to fill it up taketh from the garment, and the rent is made worse. Xam ngeen ne, kenn du daax mbubb mu màggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day ñoddi mbubb mi, te xottiku bi gën a yaatu.
17 Neither do men put new wine into old bottles: else the bottles break, and the wine runneth out, and the bottles perish: but they put new wine into new bottles, and both are preserved. Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.»
18 While he spake these things unto them, behold, there came a certain ruler, and worshipped him, saying, My daughter is even now dead: but come and lay thy hand upon her, and she shall live. Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu jàngu daldi ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sama doom ju jigéen dafa faatu léegi, waaye ñëwal, teg ko say loxo, te dina dundaat.»
19 And Jesus arose, and followed him, and so did his disciples. Noonu Yeesu jóg, topp ko, moom ak ay taalibeem.
20 And, behold, a woman, which was diseased with an issue of blood twelve years, came behind him, and touched the hem of his garment: Bi ñuy dem nag, amoon na ca mbooloo ma jigéen juy xëpp deret diirub fukki at ak ñaar. Mu defe ne, su laalee mbubbam rekk, dina wér. Mu jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam.
21 For she said within herself, If I may but touch his garment, I shall be whole.
22 But Jesus turned him about, and when he saw her, he said, Daughter, be of good comfort; thy faith hath made thee whole. And the woman was made whole from that hour. Bi mu ko defee Yeesu woññiku ne ko: «Na sa xel dal, soxna si, sa ngëm faj na la.» Noonu jigéen ja daldi wér ca saa sa.
23 And when Jesus came into the ruler's house, and saw the minstrels and the people making a noise, Bi Yeesu eggee kër njiit la, mu gis ñiy liit ak toxoro, ak mbooloo may def coow lu bare.
24 He said unto them, Give place: for the maid is not dead, but sleepeth. And they laughed him to scorn. Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal.
25 But when the people were put forth, he went in, and took her by the hand, and the maid arose. Waaye ñu génne leen, Yeesu dugg, jàpp loxob janq ba, mu daldi jóg.
26 And the fame hereof went abroad into all that land. Noonu xebaaru li mu def daldi siiw ca réew ma.
27 And when Jesus departed thence, two blind men followed him, crying, and saying, Thou Son of David, have mercy on us. Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!»
28 And when he was come into the house, the blind men came to him: and Jesus saith unto them, Believe ye that I am able to do this? They said unto him, Yea, Lord. Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne, man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu tontu ko: «Waaw Sang bi.»
29 Then touched he their eyes, saying, According to your faith be it unto you. Kon Yeesu daldi laal seeni bët ne leen: «Na am, ni ngeen ko gëme.»
30 And their eyes were opened; and Jesus straitly charged them, saying, See that no man know it. Ca saa sa seeni bët daldi ubbiku. Yeesu dénk leen bu wér ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.»
31 But they, when they were departed, spread abroad his fame in all that country. Waaye ñu génn rekk, siiwal turam fu nekk.
32 As they went out, behold, they brought to him a dumb man possessed with a devil. Bi ñu fa jógee nag, amoon na ñeneen ñu ñëw fi moom, indil ko ku rab jàpp, mu luu.
33 And when the devil was cast out, the dumb spake: and the multitudes marvelled, saying, It was never so seen in Israel. Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, musuñu koo gis ci Israyil.»
34 But the Pharisees said, He casteth out devils through the prince of the devils. Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
35 And Jesus went about all the cities and villages, teaching in their synagogues, and preaching the gospel of the kingdom, and healing every sickness and every disease among the people. Noonu Yeesu wër dëkk yu mag ya yépp ak yu ndaw ya, di leen jàngal ci seeni jàngu, tey yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla, di faj jàngoro yépp ak wéradi yépp.
36 But when he saw the multitudes, he was moved with compassion on them, because they fainted, and were scattered abroad, as sheep having no shepherd. Bi Yeesu gisee mbooloo ma, mu yërëm leen, ndaxte dañoo sonn ba ne yogg, mel ni xar yu amul sàmm.
37 Then saith he unto his disciples, The harvest truly is plenteous, but the labourers are few; Noonu mu ne taalibeem ya: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu.
38 Pray ye therefore the Lord of the harvest, that he will send forth labourers into his harvest. Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.»