menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 And when they came nigh to Jerusalem, unto Bethphage and Bethany, at the mount of Olives, he sendeth forth two of his disciples, Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege nañu Yerusalem, ba agsi dëkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaar ciy taalibeem,
2 And saith unto them, Go your way into the village over against you: and as soon as ye be entered into it, ye shall find a colt tied, whereon never man sat; loose him, and bring him. ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi.
3 And if any man say unto you, Why do ye this? say ye that the Lord hath need of him; and straightway he will send him hither. Bu leen kenn nee: “Lu ngeen di def?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla, te léegi mu delloosi ko.”»
4 And they went their way, and found the colt tied by the door without in a place where two ways met; and they loose him. Taalibe ya dem nag, ñu gis cumbur ga ci mbedd mi, mu yeewe cib buntu kër.
5 And certain of them that stood there said unto them, What do ye, loosing the colt? Bi ñu koy yiwi nag, am na ca ña fa taxaw, ñu ne leen: «Lu ngeen nar, bay yiwi cumbur gi?»
6 And they said unto them even as Jesus had commanded: and they let them go. Taalibe yi tontu leen, ni leen Yeesu digale woon, kon nit ñi bàyyi leen, ñu dem.
7 And they brought the colt to Jesus, and cast their garments on him; and he sat upon him. Ñu indi cumbur gi Yeesu nag, lal ci seeni yére, mu toog ci.
8 And many spread their garments in the way: and others cut down branches off the trees, and strawed them in the way. Ñu bare lal seeni yére ci yoon wi, ñenn ñi dagg ay cari garab ci tool yi, lal leen it ci yoon wi.
9 And they that went before, and they that followed, cried, saying, Hosanna; Blessed is he that cometh in the name of the Lord: Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan:«Osaana!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!
10 Blessed be the kingdom of our father David, that cometh in the name of the Lord: Hosanna in the highest. Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw,dina barkeel!Ci bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”»
11 And Jesus entered into Jerusalem, and into the temple: and when he had looked round about upon all things, and now the eventide was come, he went out unto Bethany with the twelve. Noonu Yeesu dugg Yerusalem, dem kër Yàlla ga, xool lépp, ba noppi génn dem dëkku Betani, moom ak fukki taalibe ya ak ñaar, ndaxte dafa guddi.
12 And on the morrow, when they were come from Bethany, he was hungry: Bët set ñu génn Betani, fekk Yeesu xiif.
13 And seeing a fig tree afar off having leaves, he came, if haply he might find any thing thereon: and when he came to it, he found nothing but leaves; for the time of figs was not yet. Noonu mu séen fu sore garabu figg gu sëq, mu dem seeti, ndax am na ay doom. Waaye bi mu fa eggee, gisul lu dul ay xob, ndaxte jamonoy figg duggagul.
14 And Jesus answered and said unto it, No man eat fruit of thee hereafter for ever. And his disciples heard it. Ci kaw loolu mu ne garab gi: «Dootuloo meññ mukk!» Taalibe yi dégg loolu mu wax.
15 And they come to Jerusalem: and Jesus went into the temple, and began to cast out them that sold and bought in the temple, and overthrew the tables of the moneychangers, and the seats of them that sold doves; Bi ñu eggee Yerusalem, Yeesu dugg ci kër Yàlla gi, daldi dàq ñi fay jaay ak ñi fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis yi ak tooguy jaaykati pitax yi,
16 And would not suffer that any man should carry any vessel through the temple. te mayul kenn, mu yóbbu am njaay ci kër Yàlla gi.
17 And he taught, saying unto them, Is it not written, My house shall be called of all nations the house of prayer? but ye have made it a den of thieves. Mu di leen jàngal ne leen: «Ndax waxuñu ci Mbind mi:“Dees na wooye sama kërkëru ñaan ci Yàlla ngir xeet yépp”? Waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
18 And the scribes and chief priests heard it, and sought how they might destroy him: for they feared him, because all the people was astonished at his doctrine. Bi ko saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya déggee nag, ñu ragal ko, ndaxte mbooloo mépp dañoo waaru ci njàngaleem. Noonu ñu seet pexem reylu ko.
19 And when even was come, he went out of the city. Bi timis jotee Yeesu ak taalibe yi génn dëkk bi.
20 And in the morning, as they passed by, they saw the fig tree dried up from the roots. Ci suba si, bi ñuy dem, ñu gis ne garabu figg gi dee na, ba wow koŋŋ.
21 And Peter calling to remembrance saith unto him, Master, behold, the fig tree which thou cursedst is withered away. Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!»
22 And Jesus answering saith unto them, Have faith in God. Yeesu tontu ne: «Gëmleen Yàlla.
23 For verily I say unto you, That whosoever shall say unto this mountain, Be thou removed, and be thou cast into the sea; and shall not doubt in his heart, but shall believe that those things which he saith shall come to pass; he shall hav Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: “Jógal, tàbbi ca géej ga,” te nga gëm ne loolu dina am, bañ cee boole xel ñaar, kon sa ñaan nangu.
24 Therefore I say unto you, What things soever ye desire, when ye pray, believe that ye receive them, and ye shall have them. Moo tax maa ngi leen koy wax, bu ngeen di ñaan Yàlla, lépp lu ngeen ko man a laaj, gëmleen ne jot ngeen ko, te dingeen ko am.
25 And when ye stand praying, forgive, if ye have ought against any: that your Father also which is in heaven may forgive you your trespasses. Te it bu ngeen di ñaan, fekk ngeen jàppal kenn dara, baal-leen ko, ngir seen Baay bi ci kaw baal leen seeni tooñ, yéen itam.»
26 But if ye do not forgive, neither will your Father which is in heaven forgive your trespasses.
27 And they come again to Jerusalem: and as he was walking in the temple, there come to him the chief priests, and the scribes, and the elders, Gannaaw loolu ñu duggaat Yerusalem, te Yeesu doon doxantu ca ëtti kër Yàlla ga. Noonu saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya dab ko
28 And say unto him, By what authority doest thou these things? and who gave thee this authority to do these things? ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Te ku la may sañ-sañu def ko?»
29 And Jesus answered and said unto them, I will also ask of you one question, and answer me, and I will tell you by what authority I do these things. Yeesu tontu leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
30 The baptism of John, was it from heaven, or of men? answer me. La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
31 And they reasoned with themselves, saying, If we shall say, From heaven; he will say, Why then did ye not believe him? Bi ñu ko déggee, ñuy werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” kon dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
32 But if we shall say, Of men; they feared the people: for all men counted John, that he was a prophet indeed. Waaye bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw;» ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.
33 And they answered and said unto Jesus, We cannot tell. And Jesus answering saith unto them, Neither do I tell you by what authority I do these things. Ñu tontu Yeesu nag ne: «Loolu de xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»