menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 And straightway in the morning the chief priests held a consultation with the elders and scribes and the whole council, and bound Jesus, and carried him away, and delivered him to Pilate. Ci suba teel saraxalekat yu mag yi gise, ñoom ak njiit yi ak xutbakat yi ak kureelu àttekat yi yépp. Ñu yeew nag Yeesu, daldi ko yóbbu, jébbal ko Pilaat.
2 And Pilate asked him, Art thou the King of the Jews? And he answering said unto him, Thou sayest it. Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko: «Wax nga ko.»
3 And the chief priests accused him of many things: but he answered nothing. Te saraxalekat yu mag yi di ko jiiñ lu bare.
4 And Pilate asked him again, saying, Answerest thou nothing? behold how many things they witness against thee. Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?»
5 But Jesus yet answered nothing; so that Pilate marvelled. Waaye ba tey Yeesu tontuwul dara, ba tax Pilaat waaru.
6 Now at that feast he released unto them one prisoner, whomsoever they desired. Màggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, ñu tànn kenn ci ñi ñu tëjoon, mu bàyyil leen ko.
7 And there was one named Barabbas, which lay bound with them that had made insurrection with him, who had committed murder in the insurrection. Fekk booba amoon na ku ñu tëj, tudd Barabas, ku bokk ci ña bëggoon a tas réew mi, boole ci rey nit.
8 And the multitude crying aloud began to desire him to do as he had ever done unto them. Noonu mbooloo mi ñëw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def.
9 But Pilate answered them, saying, Will ye that I release unto you the King of the Jews? Pilaat nag xam ne, kiñaan rekk a taxoon saraxalekat yu mag yi jébbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: «Xanaa ma bàyyil leen buuru Yawut yi?»
10 For he knew that the chief priests had delivered him for envy.
11 But the chief priests moved the people, that he should rather release Barabbas unto them. Waaye saraxalekat yu mag yi xiir mbooloo mi, ñu laaj Pilaat, mu bàyyil leen Barabas.
12 And Pilate answered and said again unto them, What will ye then that I shall do unto him whom ye call the King of the Jews? Kon Pilaat ne leen: «Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?»
13 And they cried out again, Crucify him. Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
14 Then Pilate said unto them, Why, what evil hath he done? And they cried out the more exceedingly, Crucify him. Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gën a kawe: «Daaj ko ci bant!»
15 And so Pilate, willing to content the people, released Barabbas unto them, and delivered Jesus, when he had scourged him, to be crucified. Noonu Pilaat, mi wut a neex mbooloo mi, bàyyil leen Barabas, ba noppi mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
16 And the soldiers led him away into the hall, called Praetorium; and they call together the whole band. Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma, mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum, ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp.
17 And they clothed him with purple, and platted a crown of thorns, and put it about his head, Noonu ñu solal ko mbubb mu xonq curr, ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam.
18 And began to salute him, Hail, King of the Jews! Ñu daldi ko wax bu kawe: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
19 And they smote him on the head with a reed, and did spit upon him, and bowing their knees worshipped him. Ñu di ko dóor ci bopp ak bant, di ko tifli, daldi sukk, màggal ko.
20 And when they had mocked him, they took off the purple from him, and put his own clothes on him, and led him out to crucify him. Bi ñu ko ñaawalee noonu ba noppi, ñu summi mbubb mu xonq mi, solaatal ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant.
21 And they compel one Simon a Cyrenian, who passed by, coming out of the country, the father of Alexander and Rufus, to bear his cross. Amoon na nag nit ku dëkk Siren, tudd Simoŋ, di baayu Alegsàndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, jóge ca wet, ga féete ak tool ya, ñu ga ko ngir mu gàddu bant bi.
22 And they bring him unto the place Golgotha, which is, being interpreted, The place of a skull. Noonu ñu yóbbu Yeesu ca bérab bu ñuy wax Golgota, liy tekki «Bérabu kaaŋu bopp.»
23 And they gave him to drink wine mingled with myrrh: but he received it not. Ñu bëgg koo jox biiñ bu ñu boole ak naan gu tudd miir, waaye nanguwu ko.
24 And when they had crucified him, they parted his garments, casting lots upon them, what every man should take. Foofa ñu daaj Yeesu ci bant, daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am;
25 And it was the third hour, and they crucified him. booba fekk yoor-yoor di jot.
26 And the superscription of his accusation was written over, THE KING OF THE JEWS. Mbind mi xamle lu tax ñu rey ko nee na: «Kii mooy buuru Yawut yi.»
27 And with him they crucify two thieves; the one on his right hand, and the other on his left. Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew mi, kenn ci ndeyjooram, ki ci des ci càmmooñam.
28 And the scripture was fulfilled, which saith, And he was numbered with the transgressors.
29 And they that passed by railed on him, wagging their heads, and saying, Ah, thou that destroyest the temple, and buildest it in three days, Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko naan: «Waaw kay, yaw mi bëgg a toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan,
30 Save thyself, and come down from the cross. wàccal ci bant bi te musal sa bopp!»
31 Likewise also the chief priests mocking said among themselves with the scribes, He saved others; himself he cannot save. Noonu it saraxalekat yu mag yi ak xutbakat yi di ko ñaawal ci seen biir naan: «Kii musal na ñeneen waaye mënul a musal boppam.
32 Let Christ the King of Israel descend now from the cross, that we may see and believe. And they that were crucified with him reviled him. Almasi bii, di buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gis ko te gëm.» Ñi ñu daajaale ak moom it di ko xarab.
33 And when the sixth hour was come, there was darkness over the whole land until the ninth hour. Li tàmbalee digg-bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
34 And at the ninth hour Jesus cried with a loud voice, saying, Eloi, Eloi, lama sabachthani? which is, being interpreted, My God, my God, why hast thou forsaken me? Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan: «Elowi, Elowi, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
35 And some of them that stood by, when they heard it, said, Behold, he calleth Elias. Ñenn ci ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Iliyas.»
36 And one ran and filled a spunge full of vinegar, and put it on a reed, and gave him to drink, saying, Let alone; let us see whether Elias will come to take him down. Noonu kenn daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne: «Bàyyileen, nu seet, ba xam Iliyas dina ñëw, wàcce ko.»
37 And Jesus cried with a loud voice, and gave up the ghost. Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
38 And the veil of the temple was rent in twain from the top to the bottom. Bi mu ko defee ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf.
39 And when the centurion, which stood over against him, saw that he so cried out, and gave up the ghost, he said, Truly this man was the Son of God. Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanamu Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!»
40 There were also women looking on afar off: among whom was Mary Magdalene, and Mary the mother of James the less and of Joses, and Salome; Amoon na fa nag ay jigéen, ñu leen dand, di xool. Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome.
41 (Who also, when he was in Galilee, followed him, and ministered unto him;) and many other women which came up with him unto Jerusalem. Bi Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñu ñoo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigéen yu bare yu àndoon ak moom, ba ñëw Yerusalem.
42 And now when the even was come, because it was the preparation, that is, the day before the sabbath, Booba nag bésu Waajal la woon, maanaam bés bu jiitu bésu noflaay bi. Ca ngoon sa nag,
43 Joseph of Arimathaea, and honourable counseller, which also waited for the kingdom of God, came, and went in boldly unto Pilate, and craved the body of Jesus. Yuusufa mi dëkk Arimate takk aw fitam, dem Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci kureelu àttekat yi, te doon séentu moom itam nguuru Yàlla.
44 And Pilate marvelled if he were already dead: and calling unto him the centurion, he asked him whether he had been any while dead. Bi Pilaat déggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax yàgg na faatu.
45 And when he knew it of the centurion, he gave the body to Joseph. Bi ko ko njiit li dëggalee, Pilaat jox néew bi Yuusufa.
46 And he bought fine linen, and took him down, and wrapped him in the linen, and laid him in a sepulchre which was hewn out of a rock, and rolled a stone unto the door of the sepulchre. Noonu Yuusufa jënd càngaay, wàcce néew bi, laxas ko ci, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ci xeer. Bi mu ko defee mu béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel bi.
47 And Mary Magdalene and Mary the mother of Joses beheld where he was laid. Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc.