menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 And they came over unto the other side of the sea, into the country of the Gadarenes. Noonu ñu jàll dex ga, ba teer ci diiwaanu waa Serasa.
2 And when he was come out of the ship, immediately there met him out of the tombs a man with an unclean spirit, Bi Yeesu génnee gaal gi, nit ku rab jàpp jóge ca sëg ya, daldi ñëw kar ko.
3 Who had his dwelling among the tombs; and no man could bind him, no, not with chains: Kooku nag ca sëg ya la dëkk, te kenn mënu koo yeew, du ak càllala sax.
4 Because that he had been often bound with fetters and chains, and the chains had been plucked asunder by him, and the fetters broken in pieces: neither could any man tame him. Ndaxte ay yoon yu bare jéngoon nañu ko te yeew ko ak ay càllala, waaye waa ji daldi dagg càllala yi te damm jéng yi, ba kenn amul woon kàttanu téye ko.
5 And always, night and day, he was in the mountains, and in the tombs, crying, and cutting himself with stones. Guddi ak bëccëg mu nga woon ca sëg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer.
6 But when he saw Jesus afar off, he ran and worshipped him, Bi mu gisee Yeesu fu sore nag, mu daldi dawsi, sukk fa kanamam,
7 And cried with a loud voice, and said, What have I to do with thee, Jesus, thou Son of the most high God? I adjure thee by God, that thou torment me not. di xaacu naan: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Ci turu Yàlla, bu ma mbugal.»
8 For he said unto him, Come out of the man, thou unclean spirit. Ndaxte Yeesu nee woon na ko: «Yaw rab wu bon wi, génnal ci nit ki.»
9 And he asked him, What is thy name? And he answered, saying, My name is Legion: for we are many. Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu tontu ko: «Coggal laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
10 And he besought him much that he would not send them away out of the country. Muy ñaan Yeesu lool, ngir mu bañ leen a dàq ca réew ma.
11 Now there was there nigh unto the mountains a great herd of swine feeding. Fekk amoon na fa ca tund wa géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
12 And all the devils besought him, saying, Send us into the swine, that we may enter into them. Rab ya ñaan Yeesu: «Jox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.»
13 And forthwith Jesus gave them leave. And the unclean spirits went out, and entered into the swine: and the herd ran violently down a steep place into the sea, (they were about two thousand;) and were choked in the sea. Mu may leen ko. Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon nañu ñaari junni.
14 And they that fed the swine fled, and told it in the city, and in the country. And they went out to see what it was that was done. Noonu sàmm ya daw ca dëkk ba ak ca àll ba, nettaliji mbir mi, ba nit ñi ñëw, seet li xew.
15 And they come to Jesus, and see him that was possessed with the devil, and had the legion, sitting, and clothed, and in his right mind: and they were afraid. Ñu ñëw nag ci Yeesu, gis ka rab ya jàppoon toog, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
16 And they that saw it told them how it befell to him that was possessed with the devil, and also concerning the swine. Ña fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya.
17 And they began to pray him to depart out of their coasts. Ci kaw loolu ñu daldi ñaan Yeesu, mu sore seen réew.
18 And when he was come into the ship, he that had been possessed with the devil prayed him that he might be with him. Bi Yeesu di dugg ci gaal gi, ki rab ya jàppoon ñaan Yeesu, ngir ànd ak moom.
19 Howbeit Jesus suffered him not, but saith unto him, Go home to thy friends, and tell them how great things the Lord hath done for thee, and hath had compassion on thee. Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko: «Ñibbil ci say bokk, nettali leen ni la Boroom bi yërëme, ba defal la lii lépp.»
20 And he departed, and began to publish in Decapolis how great things Jesus had done for him: and all men did marvel. Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dëkk yi, daldi fa yégle la ko Yeesu defal, ba ñépp waaru.
21 And when Jesus was passed over again by ship unto the other side, much people gathered unto him: and he was nigh unto the sea. Noonu Yeesu jàllaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit ñu bare dajaloo, wër ko.
22 And, behold, there cometh one of the rulers of the synagogue, Jairus by name; and when he saw him, he fell at his feet, Kenn ci njiiti jàngu ba nag, tudd Yayrus, ñëw ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy tànkam,
23 And besought him greatly, saying, My little daughter lieth at the point of death: I pray thee, come and lay thy hands on her, that she may be healed; and she shall live. di ko saraxu lu bare naan: «Sama doom ju jigéen mi ngi bëgg a faatu; kaay teg ko loxo, ngir mu wér te dund.»
24 And Jesus went with him; and much people followed him, and thronged him. Noonu Yeesu ànd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu réy topp ko, di ko tanc.
25 And a certain woman, which had an issue of blood twelve years, Amoon na fa nag jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar.
26 And had suffered many things of many physicians, and had spent all that she had, and was nothing bettered, but rather grew worse, Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku.
27 When she had heard of Jesus, came in the press behind, and touched his garment. Noonu mu déggoon turu Yeesu, ne ci boppam: «Su ma laalee ay yéreem rekk, dinaa wér.» Mu jaxasoo ak mbooloo mi nag, doxe ko gannaaw, laal mbubbam.
28 For she said, If I may touch but his clothes, I shall be whole.
29 And straightway the fountain of her blood was dried up; and she felt in her body that she was healed of that plague. Ci saa si deret ji taxaw, mu yég ci yaramam ne, jàngoroom deñ na.
30 And Jesus, immediately knowing in himself that virtue had gone out of him, turned him about in the press, and said, Who touched my clothes? Yeesu yég ci saa si ne, doole génn na ci moom. Mu walbatiku nag ne mbooloo mi: «Ana ku laal samay yére?»
31 And his disciples said unto him, Thou seest the multitude thronging thee, and sayest thou, Who touched me? Ay taalibeem tontu ko: «Xanaa gisuloo mbooloo mi lay wër; ngay laaj: “Ku ma laal?”»
32 And he looked round about to see her that had done this thing. Waaye Yeesu di xool li ko wër, ngir gis ku ko def.
33 But the woman fearing and trembling, knowing what was done in her, came and fell down before him, and told him all the truth. Noonu jigéen ja ñëw, daanu ciy tànkam, wax ko dëgg gépp; mu tiit bay lox, ndaxte xam na li xewoon ci yaramam.
34 And he said unto her, Daughter, thy faith hath made thee whole; go in peace, and be whole of thy plague. Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la; demal ci jàmm, te na sa jàngoro wàcc.»
35 While he yet spake, there came from the ruler of the synagogue's house certain which said, Thy daughter is dead: why troublest thou the Master any further? Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul nuy sonal kilifa gi.»
36 As soon as Jesus heard the word that was spoken, he saith unto the ruler of the synagogue, Be not afraid, only believe. Waaye Yeesu jàppul wax jooju; mu ne njiit la: «Gëmal rekk te bañ a tiit.»
37 And he suffered no man to follow him, save Peter, and James, and John the brother of James. Noonu Yeesu dem, ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana rekk, ndaxte mayul keneen, mu ànd ak moom.
38 And he cometh to the house of the ruler of the synagogue, and seeth the tumult, and them that wept and wailed greatly. Naka lañu ñëw ci kër njiit li, Yeesu dégg coow li; ñii di jooy, ñii di yuuxu.
39 And when he was come in, he saith unto them, Why make ye this ado, and weep? the damsel is not dead, but sleepeth. Mu dugg ne leen: «Lu ngeen di soow, tey jooy? Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
40 And they laughed him to scorn. But when he had put them all out, he taketh the father and the mother of the damsel, and them that were with him, and entereth in where the damsel was lying. Waaye ñu di ko ñaawal. Noonu Yeesu génne ñépp, woo baayu janq bi ak yaay ji ak ñi mu àndal, dugg fa janq bi nekk.
41 And he took the damsel by the hand, and said unto her, Talitha cumi; which is, being interpreted, Damsel, I say unto thee, arise. Mu jàpp loxoom ne ko: «Talita kumi,» liy tekki: «Janq bi, maa ngi la koy wax, jógal.»
42 And straightway the damsel arose, and walked; for she was of the age of twelve years. And they were astonished with a great astonishment. Ca saa sa janq bi jóg, daldi dox, ndaxte amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp daldi waaru, ba ne jomm.
43 And he charged them straitly that no man should know it; and commanded that something should be given her to eat. Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal; teg ca naa: «Mayleen janq bi, mu lekk.»