menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 Then came together unto him the Pharisees, and certain of the scribes, which came from Jerusalem. Amoon na bés nag, ay Farisen ak ay xutbakat yu jóge Yerusalem ñëw ci Yeesu.
2 And when they saw some of his disciples eat bread with defiled, that is to say, with unwashen, hands, they found fault. Ñu gis yenn ciy taalibeem di lekk, fekk seeni loxo setul, maanaam raxasuwuñu woon, ni ko aada santaanee.
3 For the Pharisees, and all the Jews, except they wash their hands oft, eat not, holding the tradition of the elders. Farisen yi nag ñoom ak Yawut yi yépp dañuy topp aaday yoon, yi maam yi tëral, te fandee leen gënal lekk ak loxo yu ñu raxasul.
4 And when they come from the market, except they wash, they eat not. And many other things there be, which they have received to hold, as the washing of cups, and pots, brasen vessels, and of tables. Te it bu ñu jógee pénc ma, su ñu sanguwul set, duñu lekk. Am nañu it yeneen aada yu bare, maanaam ni nga war a raxase ay kaas, ay njaq ak ay satala, ba ñu laab.
5 Then the Pharisees and scribes asked him, Why walk not thy disciples according to the tradition of the elders, but eat bread with unwashen hands? Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: «Lu tax say taalibe duñu topp aaday yoon, yi maam yi tëral, waaye ñuy lekk ak loxo yu setul?»
6 He answered and said unto them, Well hath Esaias prophesied of you hypocrites, as it is written, This people honoureth me with their lips, but their heart is far from me. Yeesu tontu leen: «Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yéen naaféq yi, bi mu bindee:“Xeet wii, ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,waaye seen xol sore na ma.
7 Howbeit in vain do they worship me, teaching for doctines the commandments of men. Seen màggal amul benn njariñ,ci li ñuy jàngale dénkaaney nit kese.”»
8 For laying aside the commandment of God, ye hold the tradition of men, as the washing of pots and cups: and many other such like things ye do. Yeesu neeti leen: «Dëddu ngeen ndigali Yàlla, jublu ci aaday nit.»
9 And he said unto them, Full well ye reject the commandment of God, that ye may keep your own tradition. Mu teg ca ne leen: «Xelu ngeen ci tebbi ndigali Yàlla, ngir sàmm seen aada.
10 For Moses said, Honour thy father and thy mother; and, Whoso curseth father or mother, let him die the death: Ndaxte Musaa nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” teg ca ne: “Ku móolu sa yaay walla sa baay, dees na la rey.”
11 But ye say, If a man shall say to his father or mother, It is Corban, that is to say, a gift, by whatsoever thou mightest be profited by me; he shall be free. Waaye yéen dangeen ne, ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga war a jariñoo ci man Korban la,” maanaam “jébbal naa ko Yàlla,”
12 And ye suffer him no more to do ought for his father or his mother; dootuleen ko bàyyi, mu defal dara ndeyam walla baayam.
13 Making the word of God of none effect through your tradition, which ye have delivered: and many such like things do ye. Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada, ji ngeen di donnante. Te it yéena ngi def yeneen yu bon yu mel nii.»
14 And when he had called all the people unto him, he said unto them, Hearken unto me every one of you, and understand: Noonu Yeesu waxaat ak mbooloo mi ne leen: «Yéen ñépp dégluleen ma te xam.
15 There is nothing from without a man, that entering into him can defile him: but the things which come out of him, those are they that defile the man. Li ci biti, tey dugg nit, du ko man a indil sobe, waaye li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.»
16 If any man have ears to hear, let him hear.
17 And when he was entered into the house from the people, his disciples asked him concerning the parable. Bi nga xamee ne jóge nañu ci mbooloo mi, dugg ci kër gi, taalibe yi laaj Yeesu, mu firil leen wax ju làqu jooju.
18 And he saith unto them, Are ye so without understanding also? Do ye not perceive, that whatsoever thing from without entereth into the man, it cannot defile him; Yeesu tontu leen ne: «Ndax yéen itam seen xol dafa tëju? Xanaa xamuleen ne, dara lu jóge biti, dugg ci nit, du ko man a indil sobe,
19 Because it entereth not into his heart, but into the belly, and goeth out into the draught, purging all meats? ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay jëm, ba noppi daldi génn ca bérab bu làqu?» Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na bépp ñam.
20 And he said, That which cometh out of the man, that defileth the man. Yeesu ne leen ati: «Li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.
21 For from within, out of the heart of men, proceed evil thoughts, adulteries, fornications, murders, Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di jóge ak ndoxaanu yàqute, càcc ak bóom,
22 Thefts, covetousness, wickedness, deceit, lasciviousness, an evil eye, blasphemy, pride, foolishness: njaaloo ak bëgge, coxor, naaféq, ñaawteef, ñeetaan, saaga, réylu ak jëfi ndof.
23 All these evil things come from within, and defile the man. Lu bon loolu lépp day génn ci nit, di ko indil sobe.»
24 And from thence he arose, and went into the borders of Tyre and Sidon, and entered into an house, and would have no man know it: but he could not be hid. Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam mënul a umpe.
25 For a certain woman, whose young daughter had an unclean spirit, heard of him, and came and fell at his feet: Amoon na fa nag jigéen ju rab jàpp doomam ju jigéen. Bi mu déggee ne, Yeesoo nga fa, mu ñëw, daanu ciy tànkam,
26 The woman was a Greek, a Syrophenician by nation; and she besought him that he would cast forth the devil out of her daughter. fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam.
27 But Jesus said unto her, Let the children first be filled: for it is not meet to take the children's bread, and to cast it unto the dogs. Waaye Yeesu ne ko: «Na gune yi jëkk a lekk, ba regg; fab ñamu gune yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
28 And she answered and said unto him, Yes, Lord: yet the dogs under the table eat of the children's crumbs. Jigéen ji tontu ko: «Waaw sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gune yi.»
29 And he said unto her, For this saying go thy way; the devil is gone out of thy daughter. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Ndax wax jooju demal ci jàmm, rab wa génn na sa doom.»
30 And when she was come to her house, she found the devil gone out, and her daughter laid upon the bed. Noonu mu ñibbi, fekk doom ji tëdd cib lal te mucc ci rab wi.
31 And again, departing from the coasts of Tyre and Sidon, he came unto the sea of Galilee, through the midst of the coasts of Decapolis. Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi.
32 And they bring unto him one that was deaf, and had an impediment in his speech; and they beseech him to put his hand upon him. Foofa ñu indil ko ku tëx te dër lool, ñaan ko mu teg ko loxo.
33 And he took him aside from the multitude, and put his fingers into his ears, and he spit, and touched his tongue; Noonu Yeesu yóbbu ko, ba ñu sore mbooloo mi, mu def ay baaraamam ciy noppam, daldi tifli, laal làmmiñam.
34 And looking up to heaven, he sighed, and saith unto him, Ephphatha, that is, Be opened. Mu yërëm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: «Effata,» liy tekki: «Ubbikuleen.»
35 And straightway his ears were opened, and the string of his tongue was loosed, and he spake plain. Ci saa si ay noppam daldi dégg te làmmiñam yiwiku, muy wax bu leer.
36 And he charged them that they should tell no man: but the more he charged them, so much the more a great deal they published it; Bi mu ko defee Yeesu tere leen, ñu wax ko kenn, waaye lu mu leen ko gën a tere, ñu gën ko nee siiwale.
37 And were beyond measure astonished, saying, He hath done all things well: he maketh both the deaf to hear, and the dumb to speak. Ñu waaru lool naan: «Lépp lu mu def, lu yéeme la. May na sax tëx yi ñuy dégg, ak luu yi ñuy wax.»