menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 And he said unto them, Verily I say unto you, That there be some of them that stand here, which shall not taste of death, till they have seen the kingdom of God come with power. Mu ne leen ati: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu nguuru Yàlla ñëw ak doole.»
2 And after six days Jesus taketh with him Peter, and James, and John, and leadeth them up into an high mountain apart by themselves: and he was transfigured before them. Juróom-benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu yóbbu leen ñoom rekk fu wéet ci tund wu kawe lool. Foofa jëmmam soppiku ci seen kanam;
3 And his raiment became shining, exceeding white as snow; so as no fuller on earth can white them. ay yéreem di ray-rayi, weex tàll, te fóotukatu àddina mënu leen weexale nii.
4 And there appeared unto them Elias with Moses: and they were talking with Jesus. Noonu ñu gis yonenti Yàlla Iliyas ak Musaa, di wax ak Yeesu.
5 And Peter answered and said to Jesus, Master, it is good for us to be here: and let us make three tabernacles; one for thee, and one for Moses, and one for Elias. Piyeer daldi ne Yeesu: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.»
6 For he wist not what to say; for they were sore afraid. Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange jàpp na leen ñoom ñett ñépp.
7 And there was a cloud that overshadowed them: and a voice came out of the cloud, saying, This is my beloved Son: hear him. Noonu niir muur leen, te baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»
8 And suddenly, when they had looked round about, they saw no man any more, save Jesus only with themselves. Ci saa si taalibe yi xool, waaye gisatuñu kenn, ku dul Yeesu rekk.
9 And as they came down from the mountain, he charged them that they should tell no man what things they had seen, till the Son of man were risen from the dead. Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi muy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki na.»
10 And they kept that saying with themselves, questioning one with another what the rising from the dead should mean. Ñu téye wax jooju ci seen biir, di sotteente xel, ba xam lu ndekkite looluy tekki.
11 And they asked him, saying, Why say the scribes that Elias must first come? Noonu taalibe yi laaj Yeesu: «Lu tax xutbakat yi di naan, Iliyas moo war a jëkk a ñëw?»
12 And he answered and told them, Elias verily cometh first, and restoreth all things; and how it is written of the Son of man, that he must suffer many things, and be set at nought. Yeesu ne leen: «Waaw, Iliyas dina jëkk a ñëw, jubbanti lépp. Waaye itam lu tax bind nañu ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare, ñu xeeb ko, dëddu ko.
13 But I say unto you, That Elias is indeed come, and they have done unto him whatsoever they listed, as it is written of him. Waaye maa ngi leen di wax ne, Iliyas ñëw na, te def nañu ko la leen neex, ni ko Mbind mi waxe.»
14 And when he came to his disciples, he saw a great multitude about them, and the scribes questioning with them. Bi nga xamee ne Yeesu ñëw na, ba jege taalibe yi, mu gis mbooloo mu bare wër leen, te ay xutbakat di werante ak ñoom.
15 And straightway all the people, when they beheld him, were greatly amazed, and running to him saluted him. Naka la mbooloo mi gis Yeesu, ñu waaru, daldi daw nuyu ko.
16 And he asked the scribes, What question ye with them? Noonu Yeesu laaj leen: «Ci lan ngeen di werante ak ñoom?»
17 And one of the multitude answered and said, Master, I have brought unto thee my son, which hath a dumb spirit; Kenn ci mbooloo mi tontu ko ne: «Kilifa gi, rab jàpp na sama doom, ba luuloo ko. Saa su ko jàppee, daf koy daaneel ci suuf, gémmiñ gi di fuur, muy yéyu, ne jàdd. Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye mënuñu ko.»
18 And wheresoever he taketh him, he teareth him: and he foameth, and gnasheth with his teeth, and pineth away: and I spake to thy disciples that they should cast him out; and they could not.
19 He answereth him, and saith, O faithless generation, how long shall I be with you? how long shall I suffer you? bring him unto me. Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi, ba kañ laa war a nekk ak yéen, ba kañ laa leen war a muñal? Indil-leen ma xale bi.»
20 And they brought him unto him: and when he saw him, straightway the spirit tare him; and he fell on the ground, and wallowed foaming. Ñu indil ko ko. Bi xale bi gisee Yeesu nag, rab wi sayloo ko ci saa si, mu daanu ci suuf, di xalangu, gémmiñ giy fuur.
21 And he asked his father, How long is it ago since this came unto him? And he said, Of a child. Yeesu laaj baay bi: «Lii kañ la ko dal?» Baay bi ne ko: «Li dale ci nguneem.
22 And ofttimes it hath cast him into the fire, and into the waters, to destroy him: but if thou canst do any thing, have compassion on us, and help us. Léeg-léeg rab wi bëmëx ko ci safara, léeg-léeg mu bëmëx ko ci ndox, ngir rey ko. Soo ko manee, yërëm nu te xettali nu.»
23 Jesus said unto him, If thou canst believe, all things are possible to him that believeth. Yeesu tontu ko: «Nga ne: “Soo ko manee,” ku gëm man na lépp.»
24 And straightway the father of the child cried out, and said with tears, Lord, I believe; help thou mine unbelief. Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan: «Gëm naa, dàqal ma sama ngëmadi.»
25 When Jesus saw that the people came running together, he rebuked the foul spirit, saying unto him, Thou dumb and deaf spirit, I charge thee, come out of him, and enter no more into him. Yeesu gis nag ne, mbooloo maa ngi daw, wërsi ko, mu daldi gëdd rab wi nag ne ko: «Génnal ci moom, yaw rab wu luu te tëx, te bu ko jàppaat; wax naa la ko.»
26 And the spirit cried, and rent him sore, and came out of him: and he was as one dead; insomuch that many said, He is dead. Noonu rab wa daldi yuuxu, sayloo xale bi, génn. Xale bi ne nemm, mel ni ku dee, ba tax ñu bare ne: «Dee na.»
27 But Jesus took him by the hand, and lifted him up; and he arose. Waaye Yeesu jàpp loxoom, jógloo ko, xale bi daldi taxaw.
28 And when he was come into the house, his disciples asked him privately, Why could not we cast him out? Bi Yeesu duggee ci kër gi, taalibe yi laaj ko ci pegg: «Lu tax mënunu ko woon a dàq?»
29 And he said unto them, This kind can come forth by nothing, but by prayer and fasting. Yeesu tontu leen ne: «Yu mel ni yii, ñaan ci Yàlla rekk a leen di dàq.»
30 And they departed thence, and passed through Galilee; and he would not that any man should know it. Bi loolu amee ñu jóge fa, jaar ci diiwaanu Galile, Yeesu bëggul kenn yég ko.
31 For he taught his disciples, and said unto them, The Son of man is delivered into the hands of men, and they shall kill him; and after that he is killed, he shall rise the third day. Ndaxte muy jàngal taalibe yi ne leen: «Dees na jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit, te dinañu ko rey, mu dekki ci ñetti fan.»
32 But they understood not that saying, and were afraid to ask him. Waaye taalibe yi xamuñu lu wax joojuy tekki, te ñemewuñu ko koo laaj.
33 And he came to Capernaum: and being in the house he asked them, What was it that ye disputed among yourselves by the way? Bi nga xamee ne egg nañu dëkku Kapernawum, te dugg ci kër gi, Yeesu laaj leen ne: «Lu ngeen doon waxtaane ci yoon wi?»
34 But they held their peace: for by the way they had disputed among themselves, who should be the greatest. Waaye ñu ne cell, ndaxte ñu ngi fa doon werante, ba xam ku gën a màgg ci ñoom.
35 And he sat down, and called the twelve, and saith unto them, If any man desire to be first, the same shall be last of all, and servant of all. Noonu Yeesu toog, woo fukki taalibe ya ak ñaar ne leen: «Ku bëgg a jiitu, na topp ci gannaaw ñépp te nekk surgab ñépp.»
36 And he took a child, and set him in the midst of them: and when he had taken him in his arms, he said unto them, Bi ko Yeesu waxee, mu jël xale, indi ko ci biir géew gi, ba noppi leewu ko naan:
37 Whosoever shall receive one of such children in my name, receiveth me: and whosoever shall receive me, receiveth not me, but him that sent me. «Ku nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma yónni.»
38 And John answered him, saying, Master, we saw one casting out devils in thy name, and he followeth not us: and we forbad him, because he followeth not us. Bi loolu amee Yowaana ne ko: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndax li mu bokkul ci nun.»
39 But Jesus said, Forbid him not: for there is no man which shall do a miracle in my name, that can lightly speak evil of me. Waaye Yeesu tontu ko: «Buleen ko tere, ndaxte kenn mënul a def kéemaan ci sama tur, ba noppi di ma xarab.
40 For he that is not against us is on our part. Ku nu sotul, far na ak nun.
41 For whosoever shall give you a cup of water to drink in my name, because ye belong to Christ, verily I say unto you, he shall not lose his reward. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na leen kaasu ndox rekk, ndax yéena ngi bokk ci man Kirist, kooku du ñàkk yoolam mukk.
42 And whosoever shall offend one of these little ones that believe in me, it is better for him that a millstone were hanged about his neck, and he were cast into the sea. «Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom, moo di ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej.
43 And if thy hand offend thee, cut it off: it is better for thee to enter into life maimed, than having two hands to go into hell, into the fire that never shall be quenched: Boo xamee ne sa loxo mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko. Ndaxte ñàkk loxo te tàbbi ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo te tàbbi ci safara su dul fey mukk.
44 Where their worm dieth not, and the fire is not quenched.
45 And if thy foot offend thee, cut it off: it is better for thee to enter halt into life, than having two feet to be cast into hell, into the fire that never shall be quenched: Te bu la sa tànk di yóbbe bàkkaar, dagg ko. Nga lafañ te tàbbi ci dund gu wóor gi moo gën, nga am ñaari tànk, ñu sànni la ci safara.
46 Where their worm dieth not, and the fire is not quenched.
47 And if thine eye offend thee, pluck it out: it is better for thee to enter into the kingdom of God with one eye, than having two eyes to be cast into hell fire: Te bu la sa bët di yóbbe bàkkaar, luqi ko. Nga patt te dugg ci nguuru Yàlla, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, ñu sànni la ci safara.
48 Where their worm dieth not, and the fire is not quenched. Foofa:“Sax ya duñu dee mukk,te safara sa du fey.”
49 For every one shall be salted with fire, and every sacrifice shall be salted with salt. Ñépp safara lañu leen di xorome.
50 Salt is good: but if the salt have lost his saltness, wherewith will ye season it? Have salt in yourselves, and have peace one with another. Xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Amleen xorom te ngeen jàmmoo.»