menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 Then said he unto the disciples, It is impossible but that offences will come: but woe unto him, through whom they come! Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: «Fiir yuy yóbbe nit bàkkaar mënta ñàkk, waaye toroxte dal na ki koy lal.
2 It were better for him that a millstone were hanged about his neck, and he cast into the sea, than that he should offend one of these little ones. Ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej moo gën ci moom muy daaneel ci bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ci ñii.
3 Take heed to yourselves: If thy brother trespass against thee, rebuke him; and if he repent, forgive him. Wottuleen seen bopp. «Bu sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu réccoo, baal ko.
4 And if he trespass against thee seven times in a day, and seven times in a day turn again to thee, saying, I repent; thou shalt forgive him. Te su la tooñee juróom-ñaari yoon ci bés bi, te ñëw ci yaw juróom-ñaari yoon ne la: “Tuub naa ko,” nanga ko baal.»
5 And the apostles said unto the Lord, Increase our faith. Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: «Yokkal sunu ngëm.»
6 And the Lord said, If ye had faith as a grain of mustard seed, ye might say unto this sycamine tree, Be thou plucked up by the root, and be thou planted in the sea; and it should obey you. Boroom bi tontu ne: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen man a ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax.
7 But which of you, having a servant plowing or feeding cattle, will say unto him by and by, when he is come from the field, Go and sit down to meat? «Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk.”
8 And will not rather say unto him, Make ready wherewith I may sup, and gird thyself, and serve me, till I have eaten and drunken; and afterward thou shalt eat and drink? Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma réer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga door a lekk te naan.”
9 Doth he thank that servant because he did the things that were commanded him? I trow not. Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet.
10 So likewise ye, when ye shall have done all those things which are commanded you, say, We are unprofitable servants: we have done that which was our duty to do. Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeen a war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
11 And it came to pass, as he went to Jerusalem, that he passed through the midst of Samaria and Galilee. Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xaajale Samari ak Galile.
12 And as he entered into a certain village, there met him ten men that were lepers, which stood afar off: Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dand ko, di wax ca kaw naan:
13 And they lifted up their voices, and said, Jesus, Master, have mercy on us. «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!»
14 And when he saw them, he said unto them, Go shew yourselves unto the priests. And it came to pass, that, as they went, they were cleansed. Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: «Demleen won seen bopp saraxalekat ya.» Bi ñuy dem, ñu daldi set.
15 And one of them, when he saw that he was healed, turned back, and with a loud voice glorified God, Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb.
16 And fell down on his face at his feet, giving him thanks: and he was a Samaritan. Mu dëpp jëwam ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon.
17 And Jesus answering said, Were there not ten cleansed? but where are the nine? Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom-ñeent ña nag?
18 There are not found that returned to give glory to God, save this stranger. Amul kenn ci ñoom ku ñëw gërëm Yàlla ku dul doxandéem bii!»
19 And he said unto him, Arise, go thy way: thy faith hath made thee whole. Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
20 And when he was demanded of the Pharisees, when the kingdom of God should come, he answered them and said, The kingdom of God cometh not with observation: Farisen yi laaj Yeesu ne ko: «Kañ la Yàlla di tëral nguuram?» Mu tontu leen ne: «Bu Yàlla di wàcce nguuram ci nit ñi, kenn du ko man a teg bët.
21 Neither shall they say, Lo here! or, lo there! for, behold, the kingdom of God is within you. Duñu man a wax it ne: “Xool-leen, mi ngi fii,” walla: “Ma nga fale,” ndaxte nguuru Yàlla wàcc na ci seen biir.»
22 And he said unto the disciples, The days will come, when ye shall desire to see one of the days of the Son of man, and ye shall not see it. Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgg a gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis.
23 And they shall say to you, See here; or, see there: go not after them, nor follow them. Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp.
24 For as the lightning, that lighteneth out of the one part under heaven, shineth unto the other part under heaven; so shall also the Son of man be in his day. Ndaxte ni melax naan ràyye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci bésam.
25 But first must he suffer many things, and be rejected of this generation. Waaye balaa booba fàww mu sonn lool te niti jamono jii dëddu ko.
26 And as it was in the days of Noe, so shall it be also in the days of the Son of man. «La xewoon ca bési Nóoyin, dina xewaat ci bési Doomu nit ki.
27 They did eat, they drank, they married wives, they were given in marriage, until the day that Noe entered into the ark, and the flood came, and destroyed them all. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jël jabar ak a séyi, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga. Noonu mbënn ma ñëw, rey leen ñoom ñépp.
28 Likewise also as it was in the days of Lot; they did eat, they drank, they bought, they sold, they planted, they builded; «Dina mel it ni la xewoon ca bési Lóot. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jënd ak di jaay, di ji ak di tabax.
29 But the same day that Lot went out of Sodom it rained fire and brimstone from heaven, and destroyed them all. Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, Yàlla tawloo safara ak tamarax, rey leen ñoom ñépp.
30 Even thus shall it be in the day when the Son of man is revealed. Noonu lay mel, bés bu Doomu nit kiy feeñ.
31 In that day, he which shall be upon the housetop, and his stuff in the house, let him not come down to take it away: and he that is in the field, let him likewise not return back. «Ca bés boobee ku nekk ca kaw kër ga te ay bagaasam nekk ca biir, bumu wàcc jëli leen. Te it ku nekk ca tool ya, bu mu ñibbi.
32 Remember Lot's wife. Fàttalikuleen jabaru Lóot!
33 Whosoever shall seek to save his life shall lose it; and whosoever shall lose his life shall preserve it. Kuy wut a rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ko ñàkk, dinga dund.
34 I tell you, in that night there shall be two men in one bed; the one shall be taken, and the other shall be left. Maa ngi leen koy wax: ca jamono jooju, ñaar dinañu bokk a tëdd guddi, dees na yóbbu kenn ki, bàyyi ka ca des.
35 Two women shall be grinding together; the one shall be taken, and the other left. Ñaari jigéen dinañu wolandoo, dees na yóbbu kenn ci, bàyyi ka ca des.»
36 Two men shall be in the field; the one shall be taken, and the other left.
37 And they answered and said unto him, Where, Lord? And he said unto them, Wheresoever the body is, thither will the eagles be gathered together. Taalibe yi ne Yeesu: «Fu loolu di xewe, Boroom bi?» Yeesu tontu leen ne: «Fa médd nekk, la tan yiy dajee.»