menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 And it came to pass, that on one of those days, as he taught the people in the temple, and preached the gospel, the chief priests and the scribes came upon him with the elders, Benn bés Yeesu doon jàngal nit ña ca kër Yàlla ga, di leen yégal xebaar bu baax bi. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya ñëw ne ko:
2 And spake unto him, saying, Tell us, by what authority doest thou these things? or who is he that gave thee this authority? «Wax nu ci ban sañ-sañ ngay defe yëf yii, walla kan moo la may boobu sañ-sañ.»
3 And he answered and said unto them, I will also ask you one thing; and answer me: Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn: wax leen ma,
4 The baptism of John, was it from heaven, or of men? la Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
5 And they reasoned with themselves, saying, If we shall say, From heaven; he will say, Why then believed ye him not? Ñu waxtaan ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
6 But and if we say, Of men; all the people will stone us: for they be persuaded that John was a prophet. Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” mbooloo mépp dinañu nu sànni ay xeer, ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.»
7 And they answered, that they could not tell whence it was. Noonu ñu tontu ne, xamuñu fu mu ko jële.
8 And Jesus said unto them, Neither tell I you by what authority I do these things. Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
9 Then began he to speak to the people this parable; A certain man planted a vineyard, and let it forth to husbandmen, and went into a far country for a long time. Noonu Yeesu daldi wax nit ña léeb wii: «Amoon na nit ku jëmbët toolu réseñ, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu yàgg.
10 And at the season he sent a servant to the husbandmen, that they should give him of the fruit of the vineyard: but the husbandmen beat him, and sent him away empty. Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. Waaye beykat yi dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
11 And again he sent another servant: and they beat him also, and entreated him shamefully, and sent him away empty. Mu yónniwaat beneen surga, ñu dóor ko moom itam, toroxal ko, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
12 And again he sent a third: and they wounded him also, and cast him out. Mu yónneeti ñetteelu surga, ñu gaañ ko, dàq ko.
13 Then said the lord of the vineyard, What shall I do? I will send my beloved son: it may be they will reverence him when they see him. «Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.”
14 But when the husbandmen saw him, they reasoned among themselves, saying, This is the heir: come, let us kill him, that the inheritance may be ours. Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen biir: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”
15 So they cast him out of the vineyard, and killed him. What therefore shall the lord of the vineyard do unto them? Ñu génne ko tool bi nag, rey ko.» Noonu Yeesu laaj leen: «Nu leen boroom tool bi di def, nag?
16 He shall come and destroy these husbandmen, and shall give the vineyard to others. And when they heard it, they said, God forbid. Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!»
17 And he beheld them, and said, What is this then that is written, The stone which the builders rejected, the same is become the head of the corner? Waaye Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki:“Doj wa tabaxkat ya sànni,mujj na di doju koñ.”
18 Whosoever shall fall upon that stone shall be broken; but on whomsoever it shall fall, it will grind him to powder. Képp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
19 And the chief priests and the scribes the same hour sought to lay hands on him; and they feared the people: for they perceived that he had spoken this parable against them. Xutbakat ya ak saraxalekat yu mag ya ñu ngi doon wut a jàpp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam nañu ne, ñoo tax mu wax léeb woowu. Waaye ragal nañu mbooloo ma.
20 And they watched him, and sent forth spies, which should feign themselves just men, that they might take hold of his words, that so they might deliver him unto the power and authority of the governor. Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ.
21 And they asked him, saying, Master, we know that thou sayest and teachest rightly, neither acceptest thou the person of any, but teachest the way of God truly: Ñu daldi ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko jàngale lu jub la. Amuloo parlàqu, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
22 Is it lawful for us to give tribute unto Caesar, or no? Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet.»
23 But he perceived their craftiness, and said unto them, Why tempt ye me? Waaye Yeesu xam na seen pexe ne leen:
24 Shew me a penny. Whose image and superscription hath it? They answered and said, Caesar's. «Wonleen ma posetu denariyon. Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu tontu ko: «Sesaar.»
25 And he said unto them, Render therefore unto Caesar the things which be Caesar's, and unto God the things which be God's. Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
26 And they could not take hold of his words before the people: and they marvelled at his answer, and held their peace. Noonu mënuñu ko woon a jàpp ciy waxam ci kanamu mbooloo ma; ñu waaru ci tontoom, ba wedam.
27 Then came to him certain of the Sadducees, which deny that there is any resurrection; and they asked him, Noonu ay nit, ñu bokk ci Sadusen yi, ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom weddi nañu ndekkite li. Noonu ñu laaj ko ne:
28 Saying, Master, Moses wrote unto us, If any man's brother die, having a wife, and he die without children, that his brother should take his wife, and raise up seed unto his brother. «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu te bàyyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam.
29 There were therefore seven brethren: and the first took a wife, and died without children. Amoon na fi nag juróom-ñaari góor ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom.
30 And the second took her to wife, and he died childless. Ñaareel ba takk jigéen ja, def noonu; ak ñetteel ba, ba juróom-ñaar ñépp faatu te bàyyiwuñu doom.
31 And the third took her; and in like manner the seven also: and they left no children, and died.
32 Last of all the woman died also. Gannaaw ga nag jigéen ja it faatu.
33 Therefore in the resurrection whose wife of them is she? for seven had her to wife. Ci ndekkite li nag, kan ci ñoom moo war a donn jigéen ja, fekk ku nekk ci juróom-ñaar ñi mas na koo takk?»
34 And Jesus answering said unto them, The children of this world marry, and are given in marriage: Yeesu tontu leen ne: «Ci àddina sii, góor ñi ak jigéen ñi dañuy séy.
35 But they which shall be accounted worthy to obtain that world, and the resurrection from the dead, neither marry, nor are given in marriage: Waaye ña ñu àtte ne, yeyoo nañoo bokk ci dundu ëllëg ak ci ndekkite li, kenn du am jabar, kenn du am jëkkër.
36 Neither can they die any more: for they are equal unto the angels; and are the children of God, being the children of the resurrection. Dafa fekk ne mënatuñoo dee, ndaxte dañuy mel ni malaaka yi. Ay doomi Yàlla lañu ndaxte doomi ndekkite lañu.
37 Now that the dead are raised, even Moses shewed at the bush, when he calleth the Lord the God of Abraham, and the God of Isaac, and the God of Jacob. Te Musaa sax wone na ne, néew yi dinañu dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba.”
38 For he is not a God of the dead, but of the living: for all live unto him. Kon nag nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la, ndaxte Yàllaa tax ñépp di dund.»
39 Then certain of the scribes answering said, Master, thou hast well said. Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: «Li nga wax dëgg la, kilifa gi!»
40 And after that they durst not ask him any question at all. Ndaxte kenn ci ñoom ñemeetu koo laaj dara.
41 And he said unto them, How say they that Christ is David's son? Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nit ñi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
42 And David himself saith in the book of Psalms, The LORD said unto my Lord, Sit thou on my right hand, Ndaxte Daawuda moom ci boppam moo ne ci Sabóor:“Boroom bi nee na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,
43 Till I make thine enemies thy footstool. ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ”
44 David therefore calleth him Lord, how is he then his son? Gannaaw Daawuda nag wooye na ko “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
45 Then in the audience of all the people he said unto his disciples, Bi ko nit ña fa nekkoon ñépp doon déglu, Yeesu ne ay taalibeem:
46 Beware of the scribes, which desire to walk in long robes, and love greetings in the markets, and the highest seats in the synagogues, and the chief rooms at feasts; «Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi. Ci jàngu yi, toogu yu féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi.
47 Which devour widows' houses, and for a shew make long prayers: the same shall receive greater damnation. Ñu ngi lekk alalu jigéen ñi seen jëkkër faatu, di ñaan Yàlla ay ñaani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gën a tar.»