menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 Verily, verily, I say unto you, He that entereth not by the door into the sheepfold, but climbeth up some other way, the same is a thief and a robber. «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku jaar feneen fu dul ci buntu gétt gi, kooku sàcc la, saay-saay la.
2 But he that entereth in by the door is the shepherd of the sheep. Waaye ki jaar ci bunt bi, mooy sàmmu xar yi.
3 To him the porter openeth; and the sheep hear his voice: and he calleth his own sheep by name, and leadeth them out. Wottukat bi dina ko ubbil bunt bi, xar yiy dégg baatam. Xar yi mu moom nag, bu ci nekk dina la woo ci sa tur, ba noppi nga topp ko ci biti.
4 And when he putteth forth his own sheep, he goeth before them, and the sheep follow him: for they know his voice. Sàmm bi, bu génnee yi mu moom yépp, dina leen jiitu, ñu topp ko, ndaxte xam nañu baatam.
5 And a stranger will they not follow, but will flee from him: for they know not the voice of strangers. Waaye duñu topp jaambur; dañu koy daw, ndaxte miinuñu baatam.»
6 This parable spake Jesus unto them: but they understood not what things they were which he spake unto them. Yeesu misaaloon na leen loolu, waaye xamuñu lu mu leen doon wax.
7 Then said Jesus unto them again, Verily, verily, I say unto you, I am the door of the sheep. Noonu Yeesu newaat: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, man maay buntu gétt gi.
8 All that ever came before me are thieves and robbers: but the sheep did not hear them. Ñi ma fi jiitu ñépp ay sàcc lañu, ak ay saay-saay; waaye xar yi dégluwuñu leen.
9 I am the door: by me if any man enter in, he shall be saved, and shall go in and out, and find pasture. Man maay bunt bi; ku jaar ci man, dinga mucc, dinga man a dugg ak a génn, dinga am it mbooy goo man a fore.
10 The thief cometh not, but for to steal, and to kill, and to destroy: I am come that they might have life, and that they might have it more abundantly. Sàcc bi moom, day sàccsi rekk, di rey ak a yàq. Man damaa ñëw, ngir nit ñi am dund, ba nekk ci naataange.
11 I am the good shepherd: the good shepherd giveth his life for the sheep. «Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi day joxe bakkanam ngir ay xaram.
12 But he that is an hireling, and not the shepherd, whose own the sheep are not, seeth the wolf coming, and leaveth the sheep, and fleeth: and the wolf catcheth them, and scattereth the sheep. Ki dul sàmm bi tey liggéeyal xaalis rekk waaye moomul xar yi, bu séenee bukki, day daw, bàyyi fa xar ya. Bu ko defee bukki ba dal ca coggal ja, jàpp ca, tasaare ya ca des.
13 The hireling fleeth, because he is an hireling, and careth not for the sheep. Booba surga day daw, ndaxte xaalis rekk lay liggéeyal, faalewul xar ya.
14 I am the good shepherd, and know my sheep, and am known of mine. «Man maay sàmm bu baax bi. Ni ma xame Baay bi te Baay bi xame ma ni, noonu laa xame samay xar, te ñoom it ni lañu ma xame. Te it kat dinaa joxe sama bakkan ngir xar yi.
15 As the Father knoweth me, even so know I the Father: and I lay down my life for the sheep.
16 And other sheep I have, which are not of this fold: them also I must bring, and they shall hear my voice; and there shall be one fold, and one shepherd. Am naa yeneen xar yu bokkul ci gétt gii. War naa leen a indi, ñoom it, te dinañu déglu sama baat. Benn coggal ay am ak benn sàmm.
17 Therefore doth my Father love me, because I lay down my life, that I might take it again. Baay bi bëgg na ma, ndaxte damay joxe sama bakkan ngir jëlaat ko.
18 No man taketh it from me, but I lay it down of myself. I have power to lay it down, and I have power to take it again. This commandment have I received of my Father. Kenn du ko jële ci man; maa koy joxe ci sama coobarey bopp. Am naa it sañ-sañu joxe ko te am naa sañ-sañu jëlaat ko. Loolu la ma sama Baay sant.»
19 There was a division therefore again among the Jews for these sayings. Kàddu yooyee ñoo féewalewaat Yawut yi.
20 And many of them said, He hath a devil, and is mad; why hear ye him? Ñu bare ca ñoom naan: «Dafa ànd ak rab! Dafa dof! Lu tax ngeen koy déglu?»
21 Others said, These are not the words of him that hath a devil. Can a devil open the eyes of the blind? Waaye ñeneen naan: «Nit ku am ay rab du waxe nii. Ndax rab man na ubbi bëti gumba?»
22 And it was at Jerusalem the feast of the dedication, and it was winter. Am bés ñu doon màggal ca Yerusalem Bés ba ñu sellale woon kër Yàlla ga; ci jamonoy sedd la woon.
23 And Jesus walked in the temple in Solomon's porch. Yeesoo nga woon ca kër Yàlla ga, di doxantu ca biir Werandaa bu Suleymaan.
24 Then came the Jews round about him, and said unto him, How long dost thou make us to doubt? If thou be the Christ, tell us plainly. Yawut ya wër ko ne ko: «Kañ nga nuy dindi ci kumpa? Boo dee Almasi bi, wax ko mu leer.»
25 Jesus answered them, I told you, and ye believed not: the works that I do in my Father's name, they bear witness of me. Yeesu tontu leen ne: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye gëmuleen. Jëf yi may def ci sama turu Baay ñoo may seede.
26 But ye believe not, because ye are not of my sheep, as I said unto you. Waaye gëmuleen ndaxte bokkuleen ci samay xar.
27 My sheep hear my voice, and I know them, and they follow me: Samay xar dinañu dégg sama baat; xam naa leen te ñu ngi may topp.
28 And I give unto them eternal life; and they shall never perish, neither shall any man pluck them out of my hand. Dama leen di jox dund gu dul jeex; duñu sànku mukk, te kenn du leen jële ci sama loxo.
29 My Father, which gave them me, is greater than all; and no man is able to pluck them out of my Father's hand. Baay bi ma leen jox, moo gën a màgg lépp, te kenn mënul a jële dara ci loxob Baay bi.
30 I and my Father are one. Man ak Baay bi benn lanu.»
31 Then the Jews took up stones again to stone him. Yawut ya daldi foraat ay xeer, bëgg koo sànni, ngir rey ko.
32 Jesus answered them, Many good works have I shewed you from my Father; for which of those works do ye stone me? Noonu Yeesu ne leen: «Def naa ci seen kanam jëf yu baax yu bare ci ndigalu Baay bi. Ban ci jëf yooyu moo tax ba ngeen bëgg maa sànni ay doj?»
33 The Jews answered him, saying, For a good work we stone thee not; but for blasphemy; and because that thou, being a man, makest thyself God. Yawut ya ne ko: «Jëf ju baax taxul nu bëgg laa sànniy xeer, waaye dangay suufeel turu Yàlla; yaw, nit rekk nga, ba noppi di def sa bopp Yàlla!»
34 Jesus answered them, Is it not written in your law, I said, Ye are gods? Yeesu tontu ne: «Bind nañu ci seen téereb yoon ne: “Yàlla nee na: Ay yàlla ngeen.”
35 If he called them gods, unto whom the word of God came, and the scripture cannot be broken; Yàlla wooye na “ay yàlla” ñi mu yónnee kàddoom, te xam nanu ne, kenn mënul a randal waxi Yàlla.
36 Say ye of him, whom the Father hath sanctified, and sent into the world, Thou blasphemest; because I said, I am the Son of God? Kon nu ngeen man a waxe ne, damay suufeel turu Yàlla ndax li ma ne Doomam laa, man mi Yàlla tànn, yónni ma ci àddina?
37 If I do not the works of my Father, believe me not. Su ma deful sama jëfi Baay, buleen ma gëm;
38 But if I do, though ye believe not me, believe the works: that ye may know, and believe, that the Father is in me, and I in him. waaye su ma ko defee, bu ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog samay jëf, ngir ngeen xam te nangu ne, maa ngi nekk ci Baay bi te Baay bi nekk na ci man.»
39 Therefore they sought again to take him: but he escaped out of their hand, Ñu di ko wut a jàppaat, waaye mu bàyyi leen fa, dem.
40 And went away again beyond Jordan into the place where John at first baptized; and there he abode. Yeesu génn, jàllaat dexu Yurdan, toog fa Yaxya daan sóobe ci ndox bu jëkk.
41 And many resorted unto him, and said, John did no miracle: but all things that John spake of this man were true. Nit ñu bare ñëw ci moom, te naan: «Yaxya deful benn kéemaan, waaye li mu wax ci kii yépp, dëgg la.»
42 And many believed on him there. Noonu ñu bare gëm ko.