menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 After these things Jesus walked in Galilee: for he would not walk in Jewry, because the Jews sought to kill him. Gannaaw loolu Yeesu doon na wër diiwaanu Galile.
2 Now the Jews' feast of tabernacles was at hand. Bëggul woon a dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wut a rey. Fekk na bésu xewu Yawut ya, ñu koy wax màggalu Mbaar ya, mu ngi doon jubsi.
3 His brethren therefore said unto him, Depart hence, and go into Judaea, that thy disciples also may see the works that thou doest. Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def.
4 For there is no man that doeth any thing in secret, and he himself seeketh to be known openly. If thou do these things, shew thyself to the world. Ku bëgg a siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.»
5 For neither did his brethren believe in him. Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon.
6 Then Jesus said unto them, My time is not yet come: but your time is alway ready. Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax.
7 The world cannot hate you; but me it hateth, because I testify of it, that the works thereof are evil. Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne, seeni jëf baaxul.
8 Go ye up unto this feast: I go not up yet unto this feast; for my time is not yet full come. Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.»
9 When he had said these words unto them, he abode still in Galilee. Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.
10 But when his brethren were gone up, then went he also up unto the feast, not openly, but as it were in secret. Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sog a dem te kenn yégu ko; siiwalul demam.
11 Then the Jews sought him at the feast, and said, Where is he? Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?»
12 And there was much murmuring among the people concerning him: for some said, He is a good man: others said, Nay; but he deceiveth the people. Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.»
13 Howbeit no man spake openly of him for fear of the Jews. Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.
14 Now about the midst of the feast Jesus went up into the temple, and taught. Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngale ca kër Yàlla ga.
15 And the Jews marvelled, saying, How knoweth this man letters, having never learned? Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?»
16 Jesus answered them, and said, My doctrine is not mine, but his that sent me. Yeesu daldi leen tontu ne: «Li may jàngale, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.
17 If any man will do his will, he shall know of the doctrine, whether it be of God, or whether I speak of myself. Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngale ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare.
18 He that speaketh of himself seeketh his own glory: but he that seeketh his glory that sent him, the same is true, and no unrighteousness is in him. Nit kiy wax ci coobareem nag, day wut a màggal boppam, waaye kiy wut a màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn.
19 Did not Moses give you the law, and yet none of you keepeth the law? Why go ye about to kill me? Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?»
20 The people answered and said, Thou hast a devil: who goeth about to kill thee? Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wut a rey?»
21 Jesus answered and said unto them, I have done one work, and ye all marvel. Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle!
22 Moses therefore gave unto you circumcision; (not because it is of Moses, but of the fathers;) and ye on the sabbath day circumcise a man. Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gune yi --jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan — moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésu noflaay bi.
23 If a man on the sabbath day receive circumcision, that the law of Moses should not be broken; are ye angry at me, because I have made a man every whit whole on the sabbath day? Bu ngeen manee xarafal nit ci bésu noflaay bi, ngir bañ a wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm?
24 Judge not according to the appearance, but judge righteous judgment. Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
25 Then said some of them of Jerusalem, Is not this he, whom they seek to kill? Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wut a rey?
26 But, lo, he speaketh boldly, and they say nothing unto him. Do the rulers know indeed that this is the very Christ? Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne, mooy Almasi bi?
27 Howbeit we know this man whence he is: but when Christ cometh, no man knoweth whence he is. Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.»
28 Then cried Jesus in the temple as he taught, saying, Ye both know me, and ye know whence I am: and I am not come of myself, but he that sent me is true, whom ye know not. Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga, daldi wax ca kaw ne: «Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñëwaluma sama bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la. Yéen xamuleen ko.
29 But I know him: for I am from him, and he hath sent me. Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa jóge, te itam moo ma yónni.»
30 Then they sought to take him: but no man laid hands on him, because his hour was not yet come. Noonu ñu koy wut a jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon.
31 And many of the people believed on him, and said, When Christ cometh, will he do more miracles than these which this man hath done? Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu ko. Ñu nga naan: «Ndax bés bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina ëpp yu nit kii?»
32 The Pharisees heard that the people murmured such things concerning him; and the Pharisees and the chief priests sent officers to take him. Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
33 Then said Jesus unto them, Yet a little while am I with you, and then I go unto him that sent me. Yeesu wax ne: «Dinaa nekk ak yéen fi ak ab diir, sog a dem ci ki ma yónni.
34 Ye shall seek me, and shall not find me: and where I am, thither ye cannot come. Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te dungeen man a dem fa may nekk.»
35 Then said the Jews among themselves, Whither will he go, that we shall not find him? will he go unto the dispersed among the Gentiles, and teach the Gentiles? Yawut ya di laajante ci seen biir naan: «Fu muy dem fu nu ko dul fekk? Mbaa du dafa nar a dem ca Yawut, ya gàddaaye ca Gereg ya, te jàngali Gereg ya?
36 What manner of saying is this that he said, Ye shall seek me, and shall not find me: and where I am, thither ye cannot come? Lan la baat yii mu wax di tekki: “Dingeen ma seet waaye dungeen ma gis,” ak: “Dungeen man a dem fa may nekk?”»
37 In the last day, that great day of the feast, Jesus stood and cried, saying, If any man thirst, let him come unto me, and drink. Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na, ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.»
38 He that believeth on me, as the scripture hath said, out of his belly shall flow rivers of living water.
39 (But this spake he of the Spirit, which they that believe on him should receive: for the Holy Ghost was not yet given; because that Jesus was not yet glorified.) Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi ko gëm naroon a jot. Fekk na joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñagul woon.
40 Many of the people therefore, when they heard this saying, said, Of a truth this is the Prophet. Bi ñu déggee wax jooja, am ay nit ca mbooloo ma ñu naan: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent bi war a ñëw.»
41 Others said, This is the Christ. But some said, Shall Christ come out of Galilee? Ñeneen naan: «Mooy Almasi bi.» Ña ca des it ne: «Waaye nan la Almasi bi man a jógee Galile?
42 Hath not the scripture said, That Christ cometh of the seed of David, and out of the town of Bethlehem, where David was? Mbind mi wax na ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay wàcce te Betleyem, dëkku Daawuda, lay jóge.»
43 So there was a division among the people because of him. Noonu féewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu.
44 And some of them would have taken him; but no man laid hands on him. Am na ca ñoom ñu ko bëggoon a jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara.
45 Then came the officers to the chief priests and Pharisees; and they said unto them, Why have ye not brought him? Bi alkaati ya delloo, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: «Lu tax indiwuleen ko?»
46 The officers answered, Never man spake like this man. Alkaati ya ne leen: «Kenn musul a waxe ni nit kooku!»
47 Then answered them the Pharisees, Are ye also deceived? Noonu Farisen ya laaj leen: «Mbaa naxuñu leen, yéen itam?
48 Have any of the rulers or of the Pharisees believed on him? Ndax am na kenn ci saraxalekat yi walla ci Farisen yi ku ko gëm? Déedéet.
49 But this people who knoweth not the law are cursed. Waaye mbooloo mi xamuñu yoonu Musaa; ñu alku lañu!»
50 Nicodemus saith unto them, (he that came to Jesus by night, being one of them,) Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon. Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen:
51 Doth our law judge any man, before it hear him, and know what he doeth? «Ndax ci sunu yoon, man nañoo daan kenn te dégluwuñu ko, mbaa ñu xam lu mu def?»
52 They answered and said unto him, Art thou also of Galilee? Search, and look: for out of Galilee ariseth no prophet. Ñu tontu ko ne: «Mbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? Gëstul, kon dinga xam ne, benn yonent musul a jóge Galile.»
53 And every man went unto his own house. Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa kër.