menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 And after five days Ananias the high priest descended with the elders, and with a certain orator named Tertullus, who informed the governor against Paul. Bi juróomi fan wéyee, Anañas saraxalekat bu mag ba dikk, ànd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, ñu woo Pool ci yoon fa kanam boroom réew ma.
2 And when he was called forth, Tertullus began to accuse him, saying, Seeing that by thee we enjoy great quietness, and that very worthy deeds are done unto this nation by thy providence, Noonu ñu woo Pool, te Tertul daldi ko jiiñ naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, sa nguur jural na nu jàmm ju neex, te sa jàppandil soppi na lu bare ci sunu xeet.
3 We accept it always, and in all places, most noble Felix, with all thankfulness. Gis nanu ko fépp ak ci lépp, di la gërëm ak sunu xol bépp.
4 Notwithstanding, that I be not further tedious unto thee, I pray thee that thou wouldest hear us of thy clemency a few words. Waaye ngir bañ a yàggal jataay bi, maa ngi lay ñaan ci sa lewetaay, nga déglu nu ci lu gàtt.
5 For we have found this man a pestilent fellow, and a mover of sedition among all the Jews throughout the world, and a ringleader of the sect of the Nazarenes: Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi xëccoo ci Yawut yi ci àddina sépp, di njiitu mbooloo mu ñuy wax Nasaréen.
6 Who also hath gone about to profane the temple: whom we took, and would have judged according to our law. Dem na ba jéem a teddadil sax kër Yàlla ga, waaye jàpp nanu ko.
7 But the chief captain Lysias came upon us, and with great violence took him away out of our hands,
8 Commanding his accusers to come unto thee: by examining of whom thyself mayest take knowledge of all these things, whereof we accuse him. Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne, li nu koy jiiñ dëgg la.»
9 And the Jews also assented, saying that these things were so. Ci kaw loolu Yawut ya ànd ca, di dëggal ne loolu wóor na.
10 Then Paul, after that the governor had beckoned unto him to speak, answered, Forasmuch as I know that thou hast been of many years a judge unto this nation, I do the more cheerfully answer for myself: Bi loolu amee boroom réew ma jox Pool kàddu gi. Noonu mu làyyi ne: «Xam naa ne, yaa ngi àtte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi làyyi ak kóolute.
11 Because that thou mayest understand, that there are yet but twelve days since I went up to Jerusalem for to worship. Man ngaa wóorliku ne, ëppagul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggali.
12 And they neither found me in the temple disputing with any man, neither raising up the people, neither in the synagogues, nor in the city: Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di jógloo mbooloo, muy ca kër Yàlla ga mbaa ca jàngu ya mbaa ci biir dëkk ba.
13 Neither can they prove the things whereof they now accuse me. Te mënuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi.
14 But this I confess unto thee, that after the way which they call heresy, so worship I the God of my fathers, believing all things which are written in the law and in the prophets: Waaye nangu naa ci sa kanam ne, maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne, mooy tariixa; terewul ne, lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko.
15 And have hope toward God, which they themselves also allow, that there shall be a resurrection of the dead, both of the just and unjust. Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam.
16 And herein do I exercise myself, to have always a conscience void of offence toward God, and toward men. Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
17 Now after many years I came to bring alms to my nation, and offerings. «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax.
18 Whereupon certain Jews from Asia found me purified in the temple, neither with multitude, nor with tumult. Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.
19 Who ought to have been here before thee, and object, if they had ought against me. Waaye ay Yawut yu dëkk Asi — xanaa kay ñoo waroon a ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp.
20 Or else let these same here say, if they have found any evil doing in me, while I stood before the council, Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba,
21 Except it be for this one voice, that I cried standing among them, Touching the resurrection of the dead I am called in question by you this day. xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”»
22 And when Felix heard these things, having more perfect knowledge of that way, he deferred them, and said, When Lysias the chief captain shall come down, I will know the uttermost of your matter. Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.»
23 And he commanded a centurion to keep Paul, and to let him have liberty, and that he should forbid none of his acquaintance to minister or come unto him. Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.»
24 And after certain days, when Felix came with his wife Drusilla, which was a Jewess, he sent for Paul, and heard him concerning the faith in Christ. Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak jabaram Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist.
25 And as he reasoned of righteousness, temperance, and judgment to come Felix trembled, and answered, Go thy way for this time; when I have a convenient season, I will call for thee. Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.»
26 He hoped also that money should have been given him of Paul, that he might loose him: wherefore he sent for him the oftener, and communed with him. Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko faral a woolu, ngir waxtaan ak moom.
27 But after two years Porcius Festus came into Felix' room: and Felix, willing to shew the Jews a pleasure, left Paul bound. Bi ñaari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligsë, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligsë, mi bëggoon lu neex Yawut ya, bàyyi Pool ca kaso ba.