menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 And when they were escaped, then they knew that the island was called Melita. Bi nu rëccee, nu yég ne dun baa nga tudd Màlt.
2 And the barbarous people shewed us no little kindness: for they kindled a fire, and received us every one, because of the present rain, and because of the cold. Te waa réew ma won nu laabiir gu ràññiku, ndaxte taalal nañu nu safara, ganale nu ndax taw bi sóob ak sedd bi.
3 And when Paul had gathered a bundle of sticks, and laid them on the fire, there came a viper out of the heat, and fastened on his hand. Pool nag di for matt, di ko def ca taal ba, jaan ne ca mëlle ndax tàngoor wa, taq ci loxoom.
4 And when the barbarians saw the venomous beast hang on his hand, they said among themselves, No doubt this man is a murderer, whom, though he hath escaped the sea, yet vengeance suffereth not to live. Bi waa réew ma gisee rab wa wéqu ci loxoom nag, ñuy waxante naan: «Ci lu wóor nit kii reykat la; te bi mu rëccee ca géej ga sax, ndogalu Yàlla mayu ko mu dund.»
5 And he shook off the beast into the fire, and felt no harm. Waaye Pool yëlëb rab wa ca safara sa, te wàññiwu ko dara.
6 Howbeit they looked when he should have swollen, or fallen down dead suddenly: but after they had looked a great while, and saw no harm come to him, they changed their minds, and said that he was a god. Nit ñi di xaar mu newi, mbaa mu ne dàll, dee; waaye bi ñu négee lu yàgg te gis ne dara jotu ko, ñu soppi xel ne: «Kii yàlla la.»
7 In the same quarters were possessions of the chief man of the island, whose name was Publius; who received us, and lodged us three days courteously. Amoon na nag ca wet ya ay suuf yu doon moomeelu ku tudd Publiyus, di kilifag dun ba. Mu teeru nu, ganale nu ngan gu réy diirub ñetti fan.
8 And it came to pass, that the father of Publius lay sick of a fever and of a bloody flux: to whom Paul entered in, and prayed, and laid his hands on him, and healed him. Fekk baayu Publiyus dafa tëdd ndax ay tàngoori yaram yu koy dikkal ak biiru taññ. Pool nag dem seeti ko, ñaan ci Yàlla, teg ko ay loxoom, mu daldi wér.
9 So when this was done, others also, which had diseases in the island, came, and were healed: Ci kaw loolu jarag ya ca des ca dun ba daldi dikk, amaat wér-gi-yaram.
10 Who also honoured us with many honours; and when we departed, they laded us with such things as were necessary. Ñu teral nu ci fànn yu bare, te bi nuy dem, ñu jox nu li nuy soxla lépp.
11 And after three months we departed in a ship of Alexandria, which had wintered in the isle, whose sign was Castor and Pollux. Bi nu fa amee ñetti weer, nu dugg ca gaal gu lollikoo ca dun ba, daldi tàbbi ca géej ga. Gaalu dëkku Alegsàndiri la woon, te yor xàmmikaay guy nataalu Kastor ak Polugsë.
12 And landing at Syracuse, we tarried there three days. Noonu nu teer dëkku Sirakus, toog fa ñetti fan.
13 And from thence we fetched a compass, and came to Rhegium: and after one day the south wind blew, and we came the next day to Puteoli: Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawu sudd daldi jóg, te ca ñaareelu fan ba nu teer Pusol.
14 Where we found brethren, and were desired to tarry with them seven days: and so we went toward Rome. Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room.
15 And from thence, when the brethren heard of us, they came to meet us as far as Appiiforum, and The three taverns: whom when Paul saw, he thanked God, and took courage. Sunuy xebaar law na, ba egg ca bokk ya fa dëkk, noonu ñu gatandu nu ba ca péncu Apiyus ak bérab bu ñuy wax Ñetti añukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam.
16 And when we came to Rome, the centurion delivered the prisoners to the captain of the guard: but Paul was suffered to dwell by himself with a soldier that kept him. Bi nu dikkee Room nag, ñu may Pool, mu dëkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu.
17 And it came to pass, that after three days Paul called the chief of the Jews together: and when they were come together, he said unto them, Men and brethren, though I have committed nothing against the people, or customs of our fathers, Bi ñetti fan wéyee, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Bi ñu dajaloo nag, mu wax leen lii: «Bokk yi, jàpp nañu ma ci Yerusalem, jébbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam.
18 Who, when they had examined me, would have let me go, because there was no cause of death in me. Waa Room nag seet sama mbir, te bëgg maa bàyyi, ndaxte toppuñu ma dara lu jar dee.
19 But when the Jews spake against it, I was constrained to appeal unto Caesar; not that I had ought to accuse my nation of. Waaye bi ko Yawut ya bañee, fas yéene naa dénk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet.
20 For this cause therefore have I called for you, to see you, and to speak with you: because that for the hope of Israel I am bound with this chain. Moo tax ma ñaan a gise ak yéen, nu diisoo, ndaxte yaakaaru bànni Israyil moo tax ñu jéng ma.»
21 And they said unto him, We neither received letters out of Judaea concerning thee, neither any of the brethren that came shewed or spake any harm of thee. Bi ñu ko déggee, ñu tontu ko: «Jotunu benn bataaxal bu jóge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon.
22 But we desire to hear of thee what thou thinkest: for as concerning this sect, we know that every where it is spoken against. Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.»
23 And when they had appointed him a day, there came many to him into his lodging; to whom he expounded and testified the kingdom of God, persuading them concerning Jesus, both out of the law of Moses, and out of the prophets, from morning Noonu ñu dig ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéem a gëmloo.
24 And some believed the things which were spoken, and some believed not. Ñenn ñi nag gëm li mu wax, ña ca des weddi ko.
25 And when they agreed not among themselves, they departed, after that Paul had spoken one word, Well spake the Holy Ghost by Esaias the prophet unto our fathers, Gannaaw mënuñoo déggoo, ñu bëgg a tas. Waaye bi ñu laata dem, Pool teg ca wax jii: «Xel mu Sell mi wax na dëgg ak seeni maam, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi.
26 Saying, Go unto this people, and say, Hearing ye shall hear, and shall not understand; and seeing ye shall see, and not perceive: Nee na:“Demal ci xeet wii ne leen:‘Dingeen déglu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara.’
27 For the heart of this people is waxed gross, and their ears are dull of hearing, and their eyes have they closed; lest they should see with their eyes, and hear with their ears, and understand with their heart, and should be converted, a Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;dañuy déglu ak nopp yu naqari,tey gëmm seeni bët,ngir bañ a gis ak seeni bët,dégg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,ñu woññiku ci man, ma wéral leen.”
28 Be it known therefore unto you, that the salvation of God is sent unto the Gentiles, and that they will hear it. «Xamleen nag ne, xebaaru mucc gii yégal nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
29 And when he had said these words, the Jews departed, and had great reasoning among themselves.
30 And Paul dwelt two whole years in his own hired house, and received all that came in unto him, Noonu diirub ñaari at Pool dëkk ca kër gu muy fey, di fa àggali ñépp ñi koy seetsi.
31 Preaching the kingdom of God, and teaching those things which concern the Lord Jesus Christ, with all confidence, no man forbidding him. Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngale ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu dëgër, te kenn terewu ko ko.