menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 I say the truth in Christ, I lie not, my conscience also bearing me witness in the Holy Ghost, Li ma bëgg a wax nag, ci kanamu Kirist laa koy waxe; dëgg la, du aw fen. Sama xel, mi Xel mu Sell miy leeral, seedeel na ma ne, dëgg laay wax.
2 That I have great heaviness and continual sorrow in my heart. Maanaam, duma noppee am naqar wu réy ci sama biir xol,
3 For I could wish that myself were accursed from Christ for my brethren, my kinsmen according to the flesh: ba xaw a bëgg a tàggoo ak Kirist te alku, ngir ñi ma bokkal xeet mucc.
4 Who are Israelites; to whom pertaineth the adoption, and the glory, and the covenants, and the giving of the law, and the service of God, and the promises; Bànni Israyil lañu, te Yàlla def na leen ni ay doomam; dëkkaloon na ndamam ci seen biir, fas ak ñoom kóllëre yi. Ñoom la Yàlla dénk yoonu Musaa, ñoom la xamal ni ñu ko war a jaamoo, ñoom la jox i digam.
5 Whose are the fathers, and of whom as concerning the flesh Christ came, who is over all, God blessed for ever. Amen. Maam ya Yàlla tànnoon, ci ñoom lañu bokk, te ci ñoom it la Kirist wàcce, maanaam ci jëmmam, Kirist mi di Yàlla, tiim lépp, te yelloo teraanga ba fàww. Amiin.
6 Not as though the word of God hath taken none effect. For they are not all Israel, which are of Israel: Waaye neewuma waxu Yàlla dafa toxu, ndaxte bokk ci bànni Israyil, taxul nga bokk ci Israyil tigi.
7 Neither, because they are the seed of Abraham, are they all children: but, In Isaac shall thy seed be called. Te it du ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, ay doomam dëgg lañu. Ndaxte Yàlla dafa wax Ibraayma ne ko: «Saw askan ci Isaaxa lay jaar.»
8 That is, They which are the children of the flesh, these are not the children of God: but the children of the promise are counted for the seed. Maanaam, soqikoo ci Ibraayma taxul a nekk doomu Yàlla, waaye juddu ci biir digeb Yàlla mooy tax a bokk dëgg-dëgg ci askanu Ibraayma.
9 For this is the word of promise, At this time will I come, and Sara shall have a son. Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma naan: «Ci waxtu wii déwén dinaa dellusi ci yaw, te Saarata dina am doom ju góor.»
10 And not only this; but when Rebecca also had conceived by one, even by our father Isaac; Te du ci loolu rekk, waaye noonu la it ci lu jëm ci Rebeka; doom yi mu jur ñoo bokk benn baay, moo di sunu maam Isaaxa.
11 (For the children being not yet born, neither having done any good or evil, that the purpose of God according to election might stand, not of works, but of him that calleth;) Waaye Yàlla wax ko ne:«Yanqóoba rakk ji mooy yilif magam Esawu,» fekk xale ya juddooguñu te defaguñu dara, muy lu baax, muy lu bon. Yàlla def na noonu, maanaam tànn kenn ci doom yi, ngir dogalam man a taxaw, te sukkandikuwul ci seeni j
12 It was said unto her, The elder shall serve the younger.
13 As it is written, Jacob have I loved, but Esau have I hated. Loolu la Mbind mi wax ne:«Bëgg naa Yanqóoba, bañ naa Esawu.»
14 What shall we say then? Is there unrighteousness with God? God forbid. Kon lu nu ci war a wax? Ndax Yàlla àttewul foofu yoon nag? Mukk!
15 For he saith to Moses, I will have mercy on whom I will have mercy, and I will have compassion on whom I will have compassion. Dafa wax Musaa sax ne ko:«Dinaa yërëm ku ma neex,laabiir ci ku ma neex.»
16 So then it is not of him that willeth, nor of him that runneth, but of God that sheweth mercy. Dama leen di wax nag, dara ajuwul ci coobareg nit, mbaa ci ñaqam, waaye lépp a ngi aju ci yërmandey Yàlla.
17 For the scripture saith unto Pharaoh, Even for this same purpose have I raised thee up, that I might shew my power in thee, and that my name might be declared throughout all the earth. Ndax Mbind mi biral na li Yàlla wax Firawna ne ko:«Def naa la buur,ngir feeñal sama kàttan ci say mbir,te ngir siiwal sama tur ci àddina si sépp.»
18 Therefore hath he mercy on whom he will have mercy, and whom he will he hardeneth. Kon nag Yàlla, la ko neex lay def, muy yërëm nit, mbaa dëgëral xolam ci lu bon.
19 Thou wilt say then unto me, Why doth he yet find fault? For who hath resisted his will? Waaye xanaa dina am ku may wax ne: «Gannaaw kenn mënul a bañ coobareg Yàlla, lu tax kon muy teg nit tooñ?»
20 Nay but, O man, who art thou that repliest against God? Shall the thing formed say to him that formed it, Why hast thou made me thus? Yaw nag nit ki, ak koo man a doon, lu tax ngay werante ak Yàlla? Ndax mbindeef dina laaj ki ko bind: «Lu tax nga binde ma nii?»
21 Hath not the potter power over the clay, of the same lump to make one vessel unto honour, and another unto dishonour? Ndax tabaxkatu ndaa sañul a fab banam, tabax ci ñaari ndaa, benn bi ngir soxla yu am maana, bi ci des ngir soxla yu ndaw?
22 What if God, willing to shew his wrath, and to make his power known, endured with much longsuffering the vessels of wrath fitted to destruction: Kon nag looy wax ci lii: Yàlla bëggoon na wone meram, xamle it dooleem ci àddina; teewul dafa sax ci muñal ñi yelloo meram te taxaw ci sànku.
23 And that he might make known the riches of his glory on the vessels of mercy, which he had afore prepared unto glory, Bëggoon na it xamle màggaayam mu ëpp xel, ci boole ñi mu yërëm ci ndamam; moo tax mu tànn leen ca njàlbéen.
24 Even us, whom he hath called, not of the Jews only, but also of the Gentiles? Te wax ji noo ko moom, nun ñi Yàlla woo ci boppam ci biir Yawut yi ak ci biir xeet yi ci des.
25 As he saith also in Osee, I will call them my people, which were not my people; and her beloved, which was not beloved. Moom la wax ci téereb Ose ne:«Ñi nekkul woon sama xeetdinaa leen ko def,ñi bokkul woon ci sama mbëggeel,dinaa leen ci boole.»
26 And it shall come to pass, that in the place where it was said unto them, Ye are not my people; there shall they be called the children of the living God. Te:«Fa ñu leen waxe woon:“Dungeen sama xeet,”dees na leen fa wooye“Doomi Yàlla Boroom dund.”»
27 Esaias also crieth concerning Israel, Though the number of the children of Israel be as the sand of the sea, a remnant shall be saved: Esayi wax na ci mbirum Israyil ne:«Lu bànni Israyil baree-bare ni suufus géej sax,lu néew rekk a ciy mucc.
28 For he will finish the work, and cut it short in righteousness: because a short work will the Lord make upon the earth. Ndaxte li Boroom bi dogal ci àddina,dina ko gaaw a def, te dina mat sëkk.»
29 And as Esaias said before, Except the Lord of Sabaoth had left us a seed, we had been as Sodoma, and been made like unto Gomorrha. Esayi it waxoon na lu jiitu loolu ne:«Yàlla Boroom kàttan gi,su bàyyiwul woon ci nun lu néew,kon ba tey raat nanu ni dëkki Sodom ak Gomor.»
30 What shall we say then? That the Gentiles, which followed not after righteousness, have attained to righteousness, even the righteousness which is of faith. Lu nu ci war a wax nag? Ñi dul Yawut te fonkuñu woon jub ci kanam Yàlla, léegi jub nañu ci kaw ngëm.
31 But Israel, which followed after the law of righteousness, hath not attained to the law of righteousness. Waaye bànni Israyil, mi bëggoon a sàmm yoon ngir jub, matalu ko.
32 Wherefore? Because they sought it not by faith, but as it were by the works of the law. For they stumbled at that stumblingstone; Ndax lan? Ndax dañoo sukkandiku ci seeni jëf, bàyyi ngëm. Dañoo daanu ci «doj wuy fakkatale.»
33 As it is written, Behold, I lay in Sion a stumblingstone and rock of offence: and whosoever believeth on him shall not be ashamed. Moom la Yàlla wax ci Mbind mi ne:«Dinaa samp ci Siyon doj wuy fakkatale,di xeer wuy daaneel nit; waaye ku wéeru ci moom, sa yaakaar du tas.»