menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 Now I Paul myself beseech you by the meekness and gentleness of Christ, who in presence am base among you, but being absent am bold toward you: Ci lu jëm ci samay mbir nag, maa ngi leen di ñaan — man Pool, mi ñu ne, ci seen biir «ragal» laa, bu ma leen soree, «ñeme,» — maa ngi leen di ñaan ndax woyof ak lewetaayu Kirist, ngir bu ma ñëwee, ma bañ a ànd ak ñeme gi may dencal ñenn
2 But I beseech you, that I may not be bold when I am present with that confidence, wherewith I think to be bold against some, which think of us as if we walked according to the flesh.
3 For though we walk in the flesh, we do not war after the flesh: Dëgg la ne nit rekk lanu, waaye dunu xeexe ni nit.
4 (For the weapons of our warfare are not carnal, but mighty through God to the pulling down of strong holds;) Ndaxte gànnaay, yi nuy xaree, jógewuñu ci nit, waaye ca Yàlla lañu jóge, te ànd ak kàttan, ngir daaneel ay tata. Danuy daaneel xalaat yi dul dëgg
5 Casting down imaginations, and every high thing that exalteth itself against the knowledge of God, and bringing into captivity every thought to the obedience of Christ; ak bépp tiitar buy jànkoonteek xam-xamu Yàlla, te danuy noot bépp xalaat, ba mu déggal Kirist.
6 And having in a readiness to revenge all disobedience, when your obedience is fulfilled. Te fas yéene nanoo jubbanti képp ku déggadi, bés bu seen dégg ndigal matee.
7 Do ye look on things after the outward appearance? If any man trust to himself that he is Christ's, let him of himself think this again, that, as he is Christ's, even so are we Christ's. Xool-leen mbir mi ne fàŋŋ. Bu amee ku mu wóor ne, ci Kirist la bokk, na jàpp it ne, su bokkee ci Kirist, nun itam ci Kirist lanu bokk.
8 For though I should boast somewhat more of our authority, which the Lord hath given us for edification, and not for your destruction, I should not be ashamed: Awma lu may rus, su may damu lu ëpp ci sañ-sañ bi nu Boroom bi jox, di sañ-sañu yokk seen ngëm, te du ngir seen kasara.
9 That I may not seem as if I would terrify you by letters. Ba tey bëgguma ngeen xalaat ne, maa ngi leen di xëbal ci samay bataaxal.
10 For his letters, say they, are weighty and powerful; but his bodily presence is weak, and his speech contemptible. Ndaxte am na ku naan: «Ay bataaxalam dañoo ñagas te am doole, waaye bu teewee dafay ñàkk fulla, di wax waxi picc.»
11 Let such an one think this, that, such as we are in word by letters when we are absent, such will we be also in deed when we are present. Kiy wax loolu na xam lii: ni sunuy kàddu mel ci sunuy bataaxal, bu nu fa nekkul, noonu it lanuy mel ci sunuy jëf, bu nu teewee.
12 For we dare not make ourselves of the number, or compare ourselves with some that commend themselves: but they measuring themselves by themselves, and comparing themselves among themselves, are not wise. Ñemewunoo féetele walla mengale sunu bopp ak ñooñu naw seen bopp. Ci li ñuy sàkk ab natt ngir natt ak mengale seen bopp ak seen bopp, ñàkk xel a tax.
13 But we will not boast of things without our measure, but according to the measure of the rule which God hath distributed to us, a measure to reach even unto you. Nun nag dunu damu ci lu weesu dayo. Nu ngi damu ci liggéey bi nu Yàlla sas, ba may nu, nu agsi ci yéen.
14 For we stretch not ourselves beyond our measure, as though we reached not unto you: for we are come as far as to you also in preaching the gospel of Christ: Bu sunu sas agsiwul woon ba ci yéen, kon man nanoo ne, génn nanu sas wi nu Yàlla sas. Waaye agsi na ba ci yéen, te indil nanu leen xebaar bu baax bi jëm ci Kirist.
15 Not boasting of things without our measure, that is, of other men's labours; but having hope, when your faith is increased, that we shall be enlarged by you according to our rule abundantly, Kon nag dunu jéggi dig yi Yàlla rëdd, bay damu ci liggéeyu ñeneen. Waaye am nanu yaakaar ne, su seen ngëm yokkoo, dinanu gën a màgg ci seen biir, des ba tey ci dig yi nu Yàlla rëddal.
16 To preach the gospel in the regions beyond you, and not to boast in another man's line of things made ready to our hand. Noonu dinanu man a yégle xebaar bu baax bi ci bérab, yi leen féete gannaaw, te bañ a damu ci li ñeneen ñi def ci seen sas.
17 But he that glorieth, let him glory in the Lord. Waaye ni ko Mbind mi waxe: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi.»
18 For not he that commendeth himself is approved, but whom the Lord commendeth. Ndaxte ki neex Yàlla, du ki naw boppam, waaye ki Yàlla gërëm.