menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 It is not expedient for me doubtless to glory. I will come to visions and revelations of the Lord. Damu amul jariñ, ba tey war na ma. Kon ma jàll ci nettali gis-gisi Boroom bi ak i peeñu.
2 I knew a man in Christ above fourteen years ago, (whether in the body, I cannot tell; or whether out of the body, I cannot tell: God knoweth;) such an one caught up to the third heaven. Xam naa taalibeb Kirist boo xam ne yékkati nañu ko ba ca asamaan, si gën a kawe, booba ak léegi mat na fukki at ak ñeent. Xawma ndax ànd na ak jëmmam walla déet. Yàlla rekk a xam.
3 And I knew such a man, (whether in the body, or out of the body, I cannot tell: God knoweth;) Xam naa ne, nit kooku yékkati nañu ko ba fa Yàlla nekk. Bu dee ci jëmmam mbaa ci xelam, xawma; Yàllaa xam. Mu dégg fa baat yu ñu mënul a nettali te yu ñu mayul doom Aadama, mu ŋaaŋ ko.
4 How that he was caught up into paradise, and heard unspeakable words, which it is not lawful for a man to utter.
5 Of such an one will I glory: yet of myself I will not glory, but in mine infirmities. Dinaa damu ci nit ku mel noonu. Waaye duma damu ci sama bopp, lu dul liy wone sama néew doole.
6 For though I would desire to glory, I shall not be a fool; for I will say the truth: but now I forbear, lest any man should think of me above that which he seeth me to be, or that he heareth of me. Su ma bëggoon a damu, du doon yëfi dof, ndaxte dëgg laay wax. Waaye damay moytoo damu, ngir kenn bañ a foog ci man lu weesu li mu gis, may def, te muy dégg, ma di ko wax.
7 And lest I should be exalted above measure through the abundance of the revelations, there was given to me a thorn in the flesh, the messenger of Satan to buffet me, lest I should be exalted above measure. Te it ngir ma bañ a yég sama bopp ndax peeñu yooyu wees xel, mayees na mbir dal ma ci sama yaram, di ma metital ni dég, muy malaakam Seytaane mu may sonal, ngir ma bañ a yég sama bopp.
8 For this thing I besought the Lord thrice, that it might depart from me. Ñaan naa Boroom bi ñetti yoon ci mbir moomu, ngir mu taqale ma ak moom.
9 And he said unto me, My grace is sufficient for thee: for my strength is made perfect in weakness. Most gladly therefore will I rather glory in my infirmities, that the power of Christ may rest upon me. Waaye mu ne ma: «Sama yiw doy na la; sama kàttan a ngi mate cig néew doole.» Kon nag dëgg-dëgg, gën na maa bég ci damu ndax sama néew doole, ngir kàttanu Kirist dëkk ci man.
10 Therefore I take pleasure in infirmities, in reproaches, in necessities, in persecutions, in distresses for Christ's sake: for when I am weak, then am I strong. Looloo tax may bég ci néew doole, yi may wéye ngir turu Kirist, ciy tiis, ciy njàqare, mbaa ñu saaga ma, mbaa ñu fitnaal ma. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laay am kàttan.
11 I am become a fool in glorying; ye have compelled me: for I ought to have been commended of you: for in nothing am I behind the very chiefest apostles, though I be nothing. Ci dëgg-dëgg wax naa waxi dof te yéena ma ci dugal, fekk yéen ci seen bopp sax yéena ma waroon a sargal, ndaxte su ma dul dara sax, seen ndaw yooyu ngeen naw ëpplewuñu ma dara.
12 Truly the signs of an apostle were wrought among you in all patience, in signs, and wonders, and mighty deeds. Kéemaan yi, jaloore yi ak jëf yu màgg, yiy firndeel ndawul Kirist, feeñ nañu ci seen biir, ma ànd ci ak muñ gu mat.
13 For what is it wherein ye were inferior to other churches, except it be that I myself was not burdensome to you? forgive me this wrong. Lan laa defal yeneen mboolooy ñi gëm te defaluma leen ko, xanaa rekk li ma wéeru ci ñoom te wéeruma ci yéen? Baal-leen ma googu tooñ!
14 Behold, the third time I am ready to come to you; and I will not be burdensome to you: for I seek not yours, but you: for the children ought not to lay up for the parents, but the parents for the children. Maa ngi leen di waaj a ganesi ñetteel bi yoon, te duma wéeru ci yéen. Wutsiwuma seen alal, yéen laa soxla. Ndaxte du gune moo war a yor waajuram, waaye waajur moo war a yor gune yi.
15 And I will very gladly spend and be spent for you; though the more abundantly I love you, the less I be loved. Man nag nangu naa joxe li ma am lépp ak xol bu sedd, ba joxe sama bopp sax, ngir dimbali leen. Gannaaw bëgg naa leen nii, xanaa kay seen mbëggeel ci man warul a wàññiku?
16 But be it so, I did not burden you: nevertheless, being crafty, I caught you with guile. Kon noonu la, nekkuma woon yen ci yéen. Waaye man na am ñu naan, dama leen a nax, ba réeral leen ci sama njublaŋ.
17 Did I make a gain of you by any of them whom I sent unto you? Mbaa du damaa lekk seen alal, jaare ko ci kenn ci ñi ma yónni woon?
18 I desired Titus, and with him I sent a brother. Did Titus make a gain of you? walked we not in the same spirit? walked we not in the same steps? Sant naa Tit, mu ñëw ci yéen, te yebal naa sunu mbokk moomu ak moom. Ndax Tit dafa lekk seen alal? Man ak moom, ndax bokkunu woon xel mu nu yékkati ak tànk yu nuy dox?
19 Again, think ye that we excuse ourselves unto you? we speak before God in Christ: but we do all things, dearly beloved, for your edifying. Xanaa diirub li ngeen di jàng lii, defe ngeen ne, nu ngi wut aw lay ci seen kanam. Samay xarit, nu ngi leen di wax ci kanam Yàlla ak ci turu Kirist; te lépp ngir seen njariñ la.
20 For I fear, lest, when I come, I shall not find you such as I would, and that I shall be found unto you such as ye would not: lest there be debates, envyings, wraths, strifes, backbitings, whisperings, swellings, tumults: Ragal naa, bu ma ñëwee ci yéen, fekk leen nu ma neexul, te yéen it ngeen fekk ma nu leen neexul. Ragal naa fekk ay xuloo ci seen biir, ak ñeetaane, xadar ak diiroo mbagg, xas ak jëw, réy-réylu ak yengu-yengu.
21 And lest, when I come again, my God will humble me among you, and that I shall bewail many which have sinned already, and have not repented of the uncleanness and fornication and lasciviousness which they have committed. Ragal naa, bu ma leen ganesiwaatee, Yàlla sama Boroom suufeel ma ci seen biir, ma naqarlu ci ñu bare ñu bàkkaaroon te dëdduwuñu seen yàqute, seen njaaloo ak seen ñaawteef, gi ñu doon def.