menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 Paul, an apostle, (not of men, neither by man, but by Jesus Christ, and God the Father, who raised him from the dead;) Man Pool, ndawul Yeesu Kirist --nit falu ma ko, te jaarewul it ci nit, mi ngi jaare ci Yeesu Kirist ak Yàlla Baay, bi ko dekkal —
2 And all the brethren which are with me, unto the churches of Galatia: man ak bokk yiy ànd ak man yépp, nu ngi leen di bind, yéen mboolooy ñi gëm te dëkk ci diiwaanu Galasi.
3 Grace be to you and peace from God the Father, and from our Lord Jesus Christ, Na yiw ak jàmm féete ak yéen, jóge ci Yàlla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi,
4 Who gave himself for our sins, that he might deliver us from this present evil world, according to the will of God and our Father: moom mi joxe bakkanam ngir dindi sunuy bàkkaar, te musal nu ci àddina su bon, si nu nekk, dëppook coobareg Yàlla sunu Baay,
5 To whom be glory for ever and ever. Amen. bi yelloo ndam ba fàww. Amiin.
6 I marvel that ye are so soon removed from him that called you into the grace of Christ unto another gospel: Man de jaaxle naa! Yàlla woo na leen ci boppam jaarale ko ci yiw, wi nu Kirist defal, waaye yéena ngi koy gaawantoo bàyyi, ngir topp beneen xebaar,
7 Which is not another; but there be some that trouble you, and would pervert the gospel of Christ. fekk du xebaar bu baax bi. Dafa am rekk ci seen biir ay nit ñiy nëxal xel yi, te bëgg a dandal xebaar bu baax bu Kirist.
8 But though we, or an angel from heaven, preach any other gospel unto you than that which we have preached unto you, let him be accursed. Waaye su fekkee kenn ci nun ñëw, walla malaaka sax mu jóge asamaan, di yégle beneen xebaar bu mengoowul ak bi nu leen yégal, kooku Yal na alku!
9 As we said before, so say I now again, If any man preach any other gospel unto you than that ye have received, let him be accursed. Wax nanu ko, maa ngi koy waxaat: bu leen kenn yégalee beneen xebaar bu dul bi ngeen nangu, kooku Yal na alku!
10 For do I now persuade men, or God? or do I seek to please men? for if I yet pleased men, I should not be the servant of Christ. Ndax kon nit laay wut a gëmloo, am damay fexee yey Yàlla? Mbaa damay wut a neex nit ñi? Su ma doon wut a neex nit ñi ba tey, kon duma nekkati jaamu Kirist.
11 But I certify you, brethren, that the gospel which was preached of me is not after man. Bokk yi, maa ngi leen di xamal ne, xebaar bu baax bi ma yégle, jógewul ci nit.
12 For I neither received it of man, neither was I taught it, but by the revelation of Jesus Christ. Jëlewuma ko ci nit, te kenn jàngalu ma ko, waaye Yeesu Kirist moo ma ko won.
13 For ye have heard of my conversation in time past in the Jews' religion, how that beyond measure I persecuted the church of God, and wasted it: Dégg ngeen ni ma doon jëfe, bi ma nekkee ci diiney Yawut yi, di fitnaal bu metti mbooloom Yàlla, di ko jéem a tas.
14 And profited in the Jews' religion above many my equals in mine own nation, being more exceedingly zealous of the traditions of my fathers. Bokkoon naa ci ñi gën a farlu ci diiney Yawut yi, te sawar it ci sàrti yoon, yi fi samay maam bàyyi, ba raw sama maas, gi ma bokkal askan.
15 But when it pleased God, who separated me from my mother's womb, and called me by his grace, Waaye Yàlla mi ma tànn lu jiitu sama juddu te woo ma ci boppam ci kaw yiwam, bi mu ko soobee, xamal na ma kan mooy Doomam, ngir ma yégal ñi dul Yawut xebaar bu baax bi ci mbirum Kirist; booba nag diisoowuma ci ak kenn.
16 To reveal his Son in me, that I might preach him among the heathen; immediately I conferred not with flesh and blood:
17 Neither went I up to Jerusalem to them which were apostles before me; but I went into Arabia, and returned again unto Damascus. Demuma sax Yerusalem seeti ñi ma jëkk a nekk ay ndawi Kirist, waaye réewu Arabi laa dem, te gannaaw loolu ma dellusiwaat Damas.
18 Then after three years I went up to Jerusalem to see Peter, and abode with him fifteen days. Ba ñu ca tegee ñetti at, ma sog a dem Yerusalem, ngir xamante ak Sefas, dal fa moom lu mat ñaari ayu-bés.
19 But other of the apostles saw I none, save James the Lord's brother. Waaye gisuma keneen ci ndaw yi ku dul Saag, doomu ndeyu Boroom bi.
20 Now the things which I write unto you, behold, before God, I lie not. Lii ma leen di bind nag, Yàllaa may seede ci ne, du ay fen.
21 Afterwards I came into the regions of Syria and Cilicia; Bi loolu wéyee dem naa réewu Siri ak réewu Silisi.
22 And was unknown by face unto the churches of Judaea which were in Christ: Waaye ba tey mboolooy ñi gëm Kirist ci diiwaanu Yude xamuñu ma woon.
23 But they had heard only, That he which persecuted us in times past now preacheth the faith which once he destroyed. Dañu déggoon ñu naan rekk ne: «Ki nu daan fitnaal bu jëkk te daan jéem a far yoonu ngëm wi, léegi mi ngi koy yégle!»
24 And they glorified God in me. Te ñuy sant Yàlla ci man.