menu.png
Passwort vergessen ?

Manueller Vergleich



•••► •••►
Vers English: King James Version Wolof NT
1 Behold, what manner of love the Father hath bestowed upon us, that we should be called the sons of God: therefore the world knoweth us not, because it knew him not. Xool-leen mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu man a tudd doomi Yàlla. Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam.
2 Beloved, now are we the sons of God, and it doth not yet appear what we shall be: but we know that, when he shall appear, we shall be like him; for we shall see him as he is. Samay soppe, léegi doomi Yàlla lanu, te li nu nar a nekki feeñagul, waaye xam nanu ne, bés bu Almasi bi feeñee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko gis, na mu mel.
3 And every man that hath this hope in him purifieth himself, even as he is pure. Te képp ku am yaakaar jooju ci moom, dinga sellal sa bopp, ni mu selle moom.
4 Whosoever committeth sin transgresseth also the law: for sin is the transgression of the law. Ku def bàkkaar, jàdd nga yoon; ndaxte bàkkaar mooy jàdd yoon.
5 And ye know that he was manifested to take away our sins; and in him is no sin. Te xam ngeen ne Yeesu Kirist feeñ na, ngir dindi bàkkaar yi, te moom amul benn bàkkaar.
6 Whosoever abideth in him sinneth not: whosoever sinneth hath not seen him, neither known him. Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy def bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko.
7 Little children, let no man deceive you: he that doeth righteousness is righteous, even as he is righteous. Samay doom, bu leen kenn nax! Kuy def lu jub, ku jub nga, ni Kirist jube moom ci boppam.
8 He that committeth sin is of the devil; for the devil sinneth from the beginning. For this purpose the Son of God was manifested, that he might destroy the works of the devil. Kuy def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane.
9 Whosoever is born of God doth not commit sin; for his seed remaineth in him: and he cannot sin, because he is born of God. Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo man a sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla.
10 In this the children of God are manifest, and the children of the devil: whosoever doeth not righteousness is not of God, neither he that loveth not his brother. Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla.
11 For this is the message that ye heard from the beginning, that we should love one another. Ndaxte xebaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante,
12 Not as Cain, who was of that wicked one, and slew his brother. And wherefore slew he him? Because his own works were evil, and his brother's righteous. te bañ a mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub.
13 Marvel not, my brethren, if the world hate you. Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle.
14 We know that we have passed from death unto life, because we love the brethren. He that loveth not his brother abideth in death. Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk moo nuy xamal ne, jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey.
15 Whosoever hateth his brother is a murderer: and ye know that no murderer hath eternal life abiding in him. Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex.
16 Hereby perceive we the love of God, because he laid down his life for us: and we ought to lay down our lives for the brethren. Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk.
17 But whoso hath this world's good, and seeth his brother have need, and shutteth up his bowels of compassion from him, how dwelleth the love of God in him? Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw?
18 My little children, let us not love in word, neither in tongue; but in deed and in truth. Samay doom, bunu bëggante ci wax mbaa ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg.
19 And hereby we know that we are of the truth, and shall assure our hearts before him. Ci loolu lanu xame ne, nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak nun, dinanu ko dalal ci kanamam; ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na lépp.
20 For if our heart condemn us, God is greater than our heart, and knoweth all things.
21 Beloved, if our heart condemn us not, then have we confidence toward God. Samay soppe, bu nu sunu xol daanul, kon man nanoo jege Yàlla ak kóolute.
22 And whatsoever we ask, we receive of him, because we keep his commandments, and do those things that are pleasing in his sight. Te lépp lu nu koy ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi sàmm ay ndigalam, di def lu ko neex.
23 And this is his commandment, That we should believe on the name of his Son Jesus Christ, and love one another, as he gave us commandment. Ndigalam mooy lii: nu gëm turu Doomam, Yeesu Kirist, tey bëggante, ni mu nu ko digale.
24 And he that keepeth his commandments dwelleth in him, and he in him. And hereby we know that he abideth in us, by the Spirit which he hath given us. Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne, dëkk na ci nun.